Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

Fiction Sénégalaise : Justice Corrompue, Instrumentalisée Et Prise En Otage !

Fiction Sénégalaise : Justice Corrompue, Instrumentalisée Et Prise En Otage !

Suite à la Liberté Provisoire attribuée par le doyen des juges à Bamba et Cie… des coups de fil ont dû jaser entre le palais du président et le Tribunal de Ndakaaru…Comment cela a pu découler à une annulation de la liberté provisoire pour Bamba ?!…Voici comment se déroulerait la scène :

…CHARLIE APPELLE DOYEN DES JUGES…

# Charlie : Alloo doyen, man la président. Mais yeen ku leen wax ngeen Bayi Bamba ?

> Doyen : Siriki moo ñu ko wax président.

# Charlie : Lann ?! Ku wax mu bayyi ko ? Siriki waxu mako loolu. Fan laa koko waxee ?! Da ngeen may foowantoo walla lann ?! Man kerook Khalifa laako wax mu bayyi ko d’abord ! Nga naan ma ay… waay… ?!

> Doyen : ah excellence, laajal Siriki, moo ma woo mu wax ma directement ni président neena ngeen bayyi Bamba et Cie pour l’instant.

# Charlie : Yeen da ngeen may fonwanetoo walla lann ni ? Siriki, Khalifa laako wax ngeen bayyi ko pcq accusations yi ñu la jox pour instruction dess na deugeur, mais pas ngeen bayyi Bamba !

> Doyen : Ah kon njumte amna président. Wool Siriki laaj ko xool. Man Bamba lama wax deh !

 

…CHARLIE RACCROCHE ROUSPÉTANT ET APPELLE SIRIKI…

# Charlie Sall : Allo Siriki, lu tax ngani doyen mu bayyi Bamba alors que Khalifa laala waxoon ?

☆ Siriki : Président, Bamba ngama waxoon d’abord après Khalifa.

# Charlie : Khalifa laa waxoon ngeen bayyi ko d’abord Siriki, après ñu xool pour Bamba pcq moom gars yi waxu ñu woon darra bima ko jappee pour « tentatives de meurtres ». Quelle connerie aussi cette histoire de Tanor !!! Xeup suuf ba meurtre, il est nul Paa bii !!!

☆ Siriki : Président, yaama ne woon balaa ngay bayyi Khalifa da ngay xaar bamu woor la ni di nga am soutien waa Tivaoune pour élections législatives yi, nga door ko bayyi.

# Charlie : Ahhh weuyyy, wax nga deug, dooral yatt ! Man damay planer rek temps yi, problèmes yee barri ci sama bopp bi. Si si loolu la Siriki, loolu la fatte woone. Mais Siriki, si Tivaoune nous lâche comme Touba lors du #rizférendum, nous sommes foutus ! Sacceu sax du tax ñu gagner. Xanaa ma jappë ci Fouta ak Fatick rekk, gnoom xamnaa duñ ma bayyi mukk ndax deffal naa leen teranga bu nekk ci Senegaal. Mais lu tax ngeen bayyi Bambaaa, te laajju leen maaa Sirikiii ?

A LIRE  LE SOFT POWER AMÉRICAIN

☆ Siriki : Pcq mënu ñukko woon teeyaat président. Seen avocats yi wax nañ deug, délai d’1 mois yi thi code pénal bi romb na depuis le 21/03. C’est très discreditant pour notre justice. Il fallait que ñu acquitter leen walla ñu jox leen liberté provisoire bi seen avocats yi doone laajj, sinon la manœuvre politicienne et l’instrumentalisation de la Justice allaient être trop flagrantes et risquées pour la Peau du régime. C’est pareil pour Khalifa et Cie. Il faudra aussi le lâcher pcq le dossier d’accusation en cours d’instruction est vide en charges sérieuses contre Khalifa. La preuve en est que pour les 2 cas, on a été obligés de trouver à Bamba puis Khalifa des co-inculpés (« complices » sans possibilité d’avoir des aveux de leur part qui puissent inculper Bamba et Khalifa) pour les mettre sous mandat de dépôt. On est obligés de les lâcher président pour l’instant !

# Charlie : Siriki daffa melni Caaf xeum na de kon !!! Li yeup, Paa PS yee ma ci dugeul (Diouf, Tanor, Niass, Djibo et Cie). Suma xamoon lii duma dugg ci ñoom mukk. Maxallaa, fekk ay Paa yu dee, jeexal takkë ba genneu Game et vides en contenus depuis matuzalem, may longoo ak gnoom pour dem. Du demm !!! Comment faire machine arrière ?! Ohhhhh !!! Siriki, Ñaata biss mooñu desse pour libérer Khalifa ?

☆ Siriki : Moins d’Une semaine moo ñu desse président, il faut que nga accélérer à Tivaoune pour ñu jappale ñu ci législatives yi, sinon moom, c’est foutu !

# Charlie : Une semaine rekk. Non c’est pas possible, d’aller faire campagne à Tivaoune d’ici une semaine. C’est impossible. Il faut qu’on trouve du temps Siriki pour ma dem ñaan njek Tivaoune. Lutax ngeen bayyi Bamba te laaju leen ma ? Da ngeen ma waroone laajj Siriki. C’est une faute grave ça. On en reparlera. Je vais sévir.

☆ Siriki : J’ai une idée pour trouver du temps président ! Il faut que procureur fasse Appel de la liberté provisoire attribuée à Bamba et Cie par doyen, pour donner au moins à l’Opinion publique l’impression que la « justice » s’exerce librement et indépendamment. On gagnera ainsi du temps pour que tu puisses négocier un soutien à Tivaoune. Pour l’instant, c’est le seul recours possible pour gagner du temps.

A LIRE  Le parrainage est potentiellement une arme redoutable de déstabilisation nationale

# Charlie : Ok mais Tivaoune dina deugeur keucc deh Siriki parce la famille Sy est très Unie maintenant. Je ne vois pas comment arriver à la diviser comme mon parrain Ndioufa et Jean Collin y étaient arrivés à l’époque. Mais je vais voir. Bon, appelles Bassirou tout de suite et dis lui de faire appel rapidement walla subba subba ma Daxeu ko ca…. comme Ndao de Crei. Ak yaw mi sax Siriki. Su deffoul appel taf-taf suma ko daxee yaw laa ciy tegg. Naa leer ci sa bopp bi ! Ok ?!

☆ Siriki : Président, dina koko wax leegi mais n’oublie pas aussi, je ne te dois pas mon poste de ministre de la justice. Je le dois au président de mon pays : la FRANCE. Forree wooma ci mbedd ndakaru yi walla yu Kedugu (sama cosaan), « Fédération Internationale des Droits de l’Homme (EF-II-DE-ACH) » laa jugge pour 2 missions spéciales pour mère-patrie dans la colonie sénégalaise (faire condamner Habré et dépénaliser l’homosexualité). Je suis à 50% de remplir ma Mission. Bul doff président. Te maa ngeek dossiers yeup. Sooma daxxee, ma jox yeup opposants yi tout de suite après, te Hollande dina geeneu ci yaw. Tu seras seul ! Na leer ci sa bopp yaw tamite.

# Charlie : Ok Siriki, wax nga deug. Xam nga rekk, je me suis un peu emporté avec la pression actuelle me serrant de toute part. Excuses moi. Ma ngi jegëlu deh. Nu ñuy waxee « Pardon » ci madinkoo ?! hihihi… Jegelu grand ! Wa mais waxal Bassirou, mu gaaw deff appel, même tay si possible. Nakko deff gaaw. Sinon rekk ma teubeul ko euleuk.

☆ Siriki : Ok président ! Mais waxoon naala nga teey avant inculpations yi nak, je t’avais prévenu deh ! Voilà…

# Charlie : waay loolu passer na Siriki, il faut essayer de sauver ce qu’on peut sauver instant yi. On peut se rattraper. Appelles boy Bassirou rekk teggal ko lima la wax.

 

…SIRIKI APPELLE PRO-FUHRER…

☆ Siriki : Allo Bassirou, président neena nga deff Appel gaaw ci liberté provisoire bi doyen jox Bamba et Cie. Na gaaw nak. Je répète, écoutes moi bien : Président neena nga gaaw deff Appel sinon demain ñu daxeu la ! Ok ?!

A LIRE  Conseil présidentiel sur l’insertion et l’emploi des jeunes, la nouvelle pièce de théâtre du président Macky Sall ! (Alioune Badara Mboup)

* Pro-cureur : D’accord M. le ministre, j’ai bien entendu et compris. maa ngui dem deff appel leegi-leegi. Tout de suite ! Avant ñuy geen 100mètres. Tay sax Reubeuss lañuy fanaanaatt. Crois moi ! Ma ngi woo doyen leegi wax ko je fais Appel.

☆ Siriki : Ah na gaaw deh sinon sa place xajj na ci. Aywa gaawal-gaawal Bassirou !

* Bassirou : D’accord M. le ministre ! Je le fais tout de suite ! Laissez moi appeler Doyen bala muy wacceu !

 

…PRO-FUHRER APPELLE DOYEN…

* Pro-cureur : Allo Doyen, man la procureur ! Je fais Appel. Recommandation bu jugge ci kaw la nak, Président moo ko digle nak ! Bul signer Liberté Provisoire bi pour Bamba et Cie sinon rekk, nos carrières sont foutues. Yaa ngi degg doyen ?!

> Doyen : Ok procureur, envoies moi vite ton Appel gaaw, ma tegaate « liberté provisoire » bi ci suuf. Mais nak gars yi kenn xamul luñu beug quoi fils… Yeena ma wax ma jox leen LP, ngeen ñëw dima waxaat ma annuler. Ah non waay…!

* Pro-cureur : Doyen bul discuter teggal « LP » bi ci suuf rekk. Ci la sunu jammë nekk en tout cas maak yaw ! Sénégalais yi ñu ngi nelaw yewoo guñ, te ñeme wuñ alkaati, teuf rekk walla haa ñeup daw, et ils ne diront rien… Macky da leen « yeew » ci rond-points yi. Kenn du bouger. hahahahaha… Amul ragal, dem ba jeex. Ñooko sumbu, nañ ko naan bamu jeex !

> Doyen : Boy Bass yaw sérieux woo quoi depuis bi ngay nekkeu sama étudiant UCAD… xoxoxoxoxo… Wa mais darra envoyer ma Appel bi, par mail sax baax na, ma dello leen ndungu siin. Coow du jibb !

…. (à suivre)

Ps : C’est 100% fiction dans ma tête nak. N’allez pas me parler d’article 80 walla outrage à institutions corrompues. Je voudrais des acteurs pour jouer cette épisode de cette feuilleton judicaire dans la Cour de « justice » à la sénégalaise. Est-ce que jarna ko sax vu que ces comiques le jouent si bien en réalité. Ku ci japp ne nitt ñi xamu ñu lu xew, yaa ngi nax sa bopp. C’est que maatay ak naafex moo yomb ci jamono ji rekk !

 

Aboubakrine Ndiaye

Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *