Site icon Senexalaat

Njarinal Njang

Retrouvez ci-dessous, le résumé en Wolof de notre article sur le rôle crucial de l’éducation dans la gouvernance sociale

#Enjeux2019 – XamXàmme  mooy  indi  kaaraange, moodi  am sa gopp  ngir  bay, am  xalima  booy  binde, moodi  yore sa galan  gooy  tëgge sa sabar, ngir  feexal sa xol. Xam sa yaram, say cër  moodi  nite tette, yar, mooy  may gone am  loxo   yu set bamën,  bokk ak  mag   ňi.

Ni  begg  toog ci jal bi, ngir  gindi  réew mi war nan leeral  lunu  xam ci jaar  jaari  réew mi,  ci mbirum  jàng  ak  jàngale, yarak tette xale yi, tàggat  magňi, yee   leen ci mbiri  àdduna.  Yeewu  mooy  tax   men toog  ci  penc   ma ; bayaal   ba,  ,ja  ba

Warnen  wax  lu  nu  xalaat  ci  denkaane  yi  doomi  reew mi ak  boroom  xam xam  yi  def  ngir  suxxali  njàng mi,  ngir  mu  barkel, jariň   reewmi,  ,jariň  askan  wi, te it  kenn  baň   nooy  yak. Xam  adduna,  xam li ňu  war,   sàmm  càkkeef   gi.

Wax  rekk  doyul  war nan  leeral  funuy  jele  xaalis  bi  war, ngir  defaraat  jikko   yi,   xel   yi

Xam loo  àttan  ak  loo  àttanul

Nu  yokk  ci  sa  mën  mën,   pexe, xam  sa diine,   say  baax   ak  xarbaax, sa cosaan, xam  yosi  say  dekkandoo, ngeen  wegante ; looloo  mooy  suuxët  jàmm.

War  nan  wax it  ni  nuy  xaymaa  ak di topp  li  nuy  degmal

Jàmm sax,  yalwaan  dakk,   xatxat yi, wànňiku,  nit  ni  am  ci  li  nuy   gor, ngir  gore

Xam  seen  warugar, xam  seen  wareef

Buuba Joob,  njiitu PAALAE

#Enjeux2019

B.  Joob,  njiitu PAALAE







Quitter la version mobile