Mamadu Jàllo : Ndongo Sàmba Silla, yow doomu-Senegaal nga, di boroom xam-xamam bu mag ci wàllu koom. Ak li ngay doon ndaw yépp, sa tur wi siiw na lool ci réew mi te saw askan naw na la. Yaa ngi liggéeye Fondation Rosa Luxemburg, ñu dénk la fa lépp lu ñeel yokkuteb Afrig sowu-jant, nga ciy gëstu. Génne nga itam ay téere yu bare te bi ci mujj, « L’arme invisible de la Françafrique. Une histoire du franc CFA », yaak ndaw su ñuy wax Fanny Pigeaud a ko bokk bind.
Moo taxginnaaw bi ma la nuyoo, sargal la, gërëm la ci jotaay bi, ma di la ñaan nga wax jàngkati LU DEFU WAXU yi luy sa xalaat ci CFA, ndax yaakaar nga ni CFA bi mënees na cee faj soxlay askan wi ?
Ndongo Sàmba Silla : Tontu bu gàtt bi te leer mooy : déedéet. Li ma ko tax a wax nag, du lenn lu dul ne, CFA bi ci boppam dafa làmboo ñaari laago yu mag. Te, feek tàggoowul ak laago yooyu, bépp naal walla pexe mu ñu mënti lal, dina lajj.
Jafe-jafe bi ci jiitu mooy ne, feek CFA bi mi ngi fi, dafay mel ni nootaange jeexagu fi. Maanaam, day mel ni Farãs moo ñu moom ba léegi. Ndaxte, CFA bi ci boppam, dañu ne ci Farãs la sësu, moo koy warlu (garantir),doonte ne wax jooju teguwul fenn. Looloo waral CFA bi ñu koy tëgge ak a defare Farãs, muy benn. Nga teg ci ne, 14i réew ñooy jëfandikoo CFA. Réew yooyu xaajoo ñaari pàcc : benn pàcc bi booloo ci kurélu UEMOA (kurél gi boole réewi Afrig sowu-jant) beneen bi moom ci kurélu CEMAC (kurél gi boole réewi diggu-Afrig). Kurél gu ci nekk am nga sa bànk bu mag : waa UEMOA ñoo ngeek BECEAO, waaCEMAC yor BEAC. Waaye, ñaari bànk yu mag yooyu, bu ci nekk danga war a jël sa xaalis bi ngay wecceek yeneen xeeti xaalisi àddina si (dolaar, ëróo, yen, añs.) xaaj ko ñaar, jox benn xaaj bi Farãs, mu téye ko. Mu mel ni, saa yoo amee téeméer, Farãs ay gàddu juróom-fukk yi. Rax-ci-dolli, bu nekk ci ñaari bànk yooyu, Farãs dafa bokk ci sa ndajem-caytu (conseil d’administration). Maanam, am na ku ko fa teewal. Te, amul benn ndogal bu ñu fa mën a jël lu dul ne Farãs da cee ànd. Njàngat lees ci mën a jële mooy ne : CFA, xaalisu Farãs la, moo ko moomal boppam.
M. J. : Ndax mën ngaa indi yeneeni firnde ci loolu ?
NSS. : Firnde yi tudd naa ci yenn léegi. Mooy bi may wax ne, ca réewum Farãs lees di tëgge CFA bi, téeméer bu nekk Farãs mooy gàddu xaaj bi def ci nafaam te yit bokk na ci ndajem-caytu ñaari bànk yu mag yii di BCEAO ak BEAC. Muy wone ni, ndogal li ci loxol Farãs la nekk. Ci misaal, bu ñu waroon a natt dayo CFA bi ñeel ëróo bi, kenn mënu cee jël ab àtte te Farãs joxewul kàddoom. Yooyu yépp di ay firnde yu leer. Waaye, nan dellu ginnaaw tuuti xool ba xam li nuy wax wér naam déet.
Ñépp a ngi fàttaliku atum 1994, bi ñuy nasaxal (dévaluer) CFA bi. Loolu, mi ngi ame woon ci coobare ak ndogalu Farãs. Ndege, Farãs, jamono yooyu, xaalis bi ñuy waxfranc français (FF) la doon jëfandikoo. Bi ñu wàññee dayo CFA bi, maanaam weccitu réewi Afrig yi Farãs nootoon, dañu ko xaaj ci digg bi, fukki dërëmi CFA di tollook dërëm ci franc français. Seen njiitu jawriñ ja woon, Eduwaar Baladiir (Edouard Balladur), moo taxawoon waxal boppam ne moom kott a jël ndogal lu ni mel. Waaw, xam nga ni, ku moom dëggëntaan sa bopp, ab doxandéem, ak lu ngeen mënti séq, du sañ a taxaw naan moo wàññi sa dayob xaalis, nga ne patt-pattaaral di xullee ! Wolof dafa ne, lu ne fàŋŋ kenn du ko jeex. Moo tax ma ne, ku moom xaalis bi ngay jëfandikoo bés bu nekk moo la moom yow ci sa bopp.
M. J. : Sànq ci say wax, tudd nga ñaari jafe-jafe yi CFA bi làmboo. Mel na ni benn bi rekk nga leeral. Lan mooy ñaareelu jafe-jafe bi ?
N.S.S : Waaw. Ci gàttal, njëlbéenug jafe-jafe bi mooy ne CFA bi day biral ni nu Farãs di noote. Ñaareelu jafe-jafe bi, nag, mi ngi aju ci wàllum koom-koom.
Ndege, CFA, bi ko Farãs di sos ci atum 1945 (26eelu fan ci weeru desàmbar), li mu ko dugge woon mooy jëfandikoo ay nooteelam ngir ñu jàppale ko ba mu mën a taxawaat, suuxat koom-koomam. Li ko waral nag, du lenn lu-dul ne, jamono jooju, Farãs ci xare bu metti la doon door a jóge (ñaareelu xareb àddina si). Xare bi metti woon lool ci moom, mu ñàkke ci alal ju bare ak ay jumtukaayi xaralaam…réew mépp yàqu daanaka, koom-koom bi sooy, Farãs ndóolal la ko ba nga ne lii lu mu doon. Dafa di sax, jumtukaay yi mu soxla woon te ñu waroon a jóge bitim-réew, amul woon xaalis bu mu leen jënde. Ci la ay njiitam xalaat, lalpexe te du woon lenn lu-dul sàkk CFA. Ngir sàmm dayo bi mu amoon ci àddina si, Farãs dafa daldi wëlbatiku ci réewi Afrig yi mu tegoon loxo ngir tibbe ci seen alal li koy tax a noyyi, duy ci nafaam ba mu fees dell, daldi suqali koom-koomam, dekkali doole ak dayo ya mu amoon ca Ërob ak ci àddina si. Kon, CFA, xettali Farãs a ko tax a jóg.
Rax-ci-dolli, réewum Farãs dafa soxla woon ay njureef (matières premières) ngir isinam yi mën a dox. Njureef yooyu, nag, Afrig lañu nekkoon (te ba tey jii ñoo ngi fi). Kon, da leen a waroon a jëndsee Afrig. Li gën a yéeme moo di ne sonalul sax boppam di leen jënd ci nun. Defu ko ndax li ñu xam ci kuy jënd mooy nga ñëw ne lii la bëgg, waññi sa xaalisu bopp fey. Demewul noonu ndaxte CFA bi Farãs di jënde njureefi réewi Afrig yi mu nootoon, seen xaalis la, ñoo ko moom ci lu wér. Farãs indiwul dolaar, indiwul yen, walla sax beneen xaalis. Mu ngi mel ni daal, ma dénk la samay ñaar-fukki dërëm, nga delloo ma fukki dërëm yi, yeneen fukki dërëm nga tëyeleen ba noppi, wëlbatiku ñëw di ko jënde sama njaay. Ndax xaalis bi ngay jënde yaa ko moom ? Dée-déet ! Kon kay danga jël sama moomeel ñaari yoon (sama xaalis ak sama njaay). Bu ko defee, Farãs deful woon lu dul jëlsi njureefi réewi Afrig yi mu nootoon, waaye jëndu leen woon. Ci gàttal, ngir tënk ñaareelu jafe-jafe bi, CFA day dooleel koom-koomu Farãs, di nasaxal koom-koomu réewi Afrig yi koy jëfandikoo. Li ci gën a doy waar nag, mooy ne bi ñuy sos CFA bi, moo ëppoon dayo xaalisu réewum Farãs (franc français) te loolu am na lu ci Farãs nammoon.
M. J. : Ci sa xalaat, lan la ci Farãs jublu woon ?
N.S.S : Xam nga, réew mu mel ni Garaŋ-Bërëtaañ, amoon doole lool te féete woon Farãs kow ci bépp boor, daawul doxale noonu, doonte amoon nay réew yu mu nootoon ci Afrig. Muy lu jar a bàyyi xel. Ndaxte, xaalisu Garaŋ-Bërëtaañ moo gënoon a diis bu Farãs, te réew mu naat la woon. Ñoom, njiiti Garaŋ-Bërëtaañ yi, dooleeluñu woon xaalisu réew yi ñu nootoon ba mu gën a diis seen bos. Kon, bu Farãs defee lu ni mel, am na lu mu ku dugge woon. Loolu laa lay waxsi.
Li taxoon Farãs ak i njiitam def ba CFA bi ëppoon doole ñaari yoon xaalisu Farãs du woon lenn lu dul tënk réewi Afrig yi ngir ñuy jënd ci Farãs doŋŋ, di ko jaay it moom kott. Li ko waral, mooy ne dayo boobu ñu joxoon CFA bi, ngelaw kese la woon. Te sax, looloo gënatee tax Farãs mën a jënde ci réewi Afrig yi ndax daanaka du ko dikke dara. Ci jamono yooyu, CFA bi diisoon ba nga xam ne, réew yi ko daan jëfandikoo mënuñu woon a jëflante ak yeneen réewi àddina si. Loolu bokk na ci li nasaxal sunu koom-koom, te pexem Farãs kese la.
M. J. : Ndax, laata CFA bi di am, réewi Afrig yi daan nañu séq ak yeneen réewi àddina si jënd ak jay ?
N.S.S: Waaw kay ! Bi ñaareelu xareb àddina bu mag bi jeexee, réewi Afrig yi demoon jàppale seen i nootkat, dañu cee jaare yeewu, tàmbalee dox ak seeni tànki bopp. Naka noonu, Farãs mënul woon a tere réew yi mu nootoon ñuy jaayante ak jëndanteek ci yeneen réew yi, muy yu Amerig bëj-saalum walla sax yu Aasi. Jamono jooju, tàmbali woon nañu am ay jumtukaayi xarala. Waaye, Farãs, ànd ak kiñaanam ak bëgg a ratt réewi Afrig yi, lal ay pexe ngir gàntal jëflante boobu. Ci la sose CFA bi, mu tënk sunuy réew, tee leen jëm kanam. Kon, Farãs dafa gisoon ni tegu nan ci yoonu naataange, mu daldi kootook ñenn ci njiit ya woon, daldi fatt yoon woowu…(Ñaareelu xaaj bi feek i fan)