Un poème en wolof comportant treize (13) strophes de quatre (4) vers chacun appelés quatrain. Les trois premiers vers de chaque quatrain ont la même rime tandis que le quatrième vers de tous les quatrains se terminent par « AR ».
Na ñu Buur Yalla defal xel mu rafet
Ak xam xam bu jubak xalima gu set
Ba du ñu juum ci bind ci gennuk wet
Ci bii taalif ñu jagleel Boroom Safar
Bambaa xëyoon benn bis woo ndongo ya
Di leen Yëgël mbirum “himmàk tarbiya”
Booleek “tarxiya taxliyaak tahliya”[1]
Ngir ne ñooy liy mottali jaangak nafar
Biss booba la ñu bari ñibbi ne mes
Ngir ne xamuñ lii di leen nuru lu bees
Am ñu Yalla may xeewël dàldi fa des
Took Nangul rakki boroom Mbàkke xewar
Ci teeni tassawuf ñu fas yéene naan
Ndoxu “limaan islaamak lii di Ihsaan”
Tey roy seen “Baay u diiné”[2] niki Usmaan
Anliyunak Abaabakar ak Oumar
Loolu taxoon na ba lu mbir yi tar tar
Ñu fataliku Daam[3] ma léen daan waar
Naan leen seen baay u diiné muñ nañ naqar
Teewul am nañ ndam kerok xare badar
Ñu fabu waat nekk si jàmook ligéey
Ci geeju kiiraayu Baamba ñu di féey
Moom mi leen daan jangalaka défal wey
Ci ay xam xam akiy teggin yu leen war
Ñu nekk di muritu ci ak neewaay
Ba mujj mbooloomi gën di bariy gaay
Séex Bamba daaldi sanc dëkub kiiraay
Ngir xamnani xumbaay man na leena gaar
Mam Xaadim daaldi sanc Daaru Salaam
Jël Sidy Anta sëtub Maam Maharam
Moom miy taalibéem ba noppi di rakam
Joxko kër gaak ndongoya ñu kay siyaar
Foofée la Maam Fallook Seriñ Mustafaa
Ña njëkka wuutu Xaadimal Mustafaa
Kii tabax jumaa kee demal ko “Safaa”[4]
Falañ feeñee nee na ñu, si ay xibaar
Fekk Maam Daam dem di wër këruk jinaan
Dëkub leer buy xëcci kepp ku mar naan
“Tuubaal Mahruusa” di “mawridu zamaan[5]”
Ñu kay séet ba gisko mu took ci am mbaar
Maam Xaadim xamal leen fa mbirum Tuubaa
Nu xam ne kon góor gu am cër fa Buur ba
Nekoon nay wër bërëb bii ngoonak suba
Waaye Bambaa xam te yor la njëk lay jar
Fa Daarul Xuduus la Maam Daam des di ñaan
Def fa “lihtikaaf” ba gis “Seydi Adnaan”
Mu rang ko garaatu “xutbu zamaan”
Waaye Bamba tek bëtëm ci waa Badar
Gën ji mindeef waxko fa ci ay tar tar
Li ligéey bi laaj lepp di ay naqar
Fekk na Bamba jekk, téeñu bay xaar
FUKKI FAN AK JURÓOM ÑATT CI SAFAR
[1] Education spirituelle Soufi
[2] C A Bamba disait à ses taalibés de se souvenir des compagnons du Prophète (PSL) qui avaient enduré beaucoup de souffrance. Il leur disait ñooy seen « Baay ci diiné »
[3] Nom souvent utilisé par S Moussa Ka dans ses poèmes pour faire référence à C A Bamba
[4] Pèlerinage à la Mecque «Marwataak Safaa »
[5] Abreuvoir des assoiffés