Lu waay xamadi xamadi xam ne Maki Sàll mooy Njiitu-réew mi. Waaw, ne askan wee ko fal ci atum 2012. Bi mu toogeek léegi nag, lu bari la dig askan wi. Waaye mel na ne bi ci ëppal solo askan wi mooy ñaari màndaa yi mu waatoon ne moom lay toog ci jal bi. Ci kow loolu, am nañu seen xel tàmbalee tey, ñu naan ngóor sii niruwul ku nar a sàmm ay kàddoom. Ba tax na LU DEFU WAXU jóg def ay jéego fekki ñenn ci askan wi ngir ñu wax seen xalaat ci ci mbir mi.
Juróom lañu te ku ci nekk lii lan la laaj :
Asalaamalekum Mamadu Jóob, jaaykat nga ci daara ju kawe jii di Gastoŋ Berse, maa ngi tudd Xari Njaay di ab taskatu xibaar ci LU DEFU WAXU.
Luy sa xalaat ci coowal ñetteelu màndaawu Maki Sàll bi ?
« Maalekum salaam soxna si. Waaw, man de li ma xalaat ci ñetteelu màndaa bi, ragal pàrteem tas moo tax Maki Sàll ñemewu cee wax lu leer. Fi mu ne nii bu nee du wut ñetteelu màndaa ku ne dina jéem a wut fu mu aw. Te loolu du baax ci nguuram. Te yit, niñ fi doon coowe Karim Wàdd ak Xalifa Sàll la ko mbamb nar a toppe. Senegale yee mel noonu, kenn mënuleen a tere coow te jamono jii ñetteelu màndaa xew. »
Mareem Sog, di ndongo ci daara ju kawe jii di Gastoŋ Berse nii la gise mbir mi :
«Ci sama gis-gis, ñetteelu màndaawu Maki Sàll waroon naa mën a nekk ci kow doomi-réew mi bég ci moom. Waaye fi mu tollu nii de, ñi ëpp ci ñoom rafetluwuńu liggéeyam. Ba tax na bu nee day laaj ñetteelu màndaa, coow ak fitna rekk la fiy indi. Abdulaay Wàdd jéemoon na ko ci 23eelu fan ci weeru suweŋ 2012 ngir teg fi doomam te mujjul a àntu. Man coow li ne kurr ci ñetteelu màndaa bi loolu rekk la may fàttali, du leneen.»
Ngiraan Njaay ndongo ci Gastoŋ Berse :
«Ci sama xalaat bu gàtt, jàpp naa ne ñaari màndaa doy nan sëkk ndax dara la fi deful bi mu toogee ci jal beek tey. Ndax jamono jii yaakaar naa ne réew mi soxla na leneen lu-dul ay TER walla ay kër yoo xam ne du ñëpp a am dooley dëkk fa. Naam mbébétam ci réew mi rafet na waaye na may ñeneen ñu wane seen mënin ndax kat nguur noonu lay doxe, mënoo loo sumb rekk eggale ko.»
Moktaar Jàllo, eñseñeer ci wàllu soŋ :
« Coowal ñetteelu màndaa bi bari na lool. Waaye lépp Njiitu-réew mee ko waral. Ndax keroog ba muy jàkkaarlook askan wi ca 31elu fan ci weeru desàmbar 2019, la waroon a wax lu leer. Waaye defu ko, mu mel ni yëf yi ńoru ko. Fi mu ne nii gën na noo réeral. Li ci des mooy ñaan Yàlla mu delloosi xelam ba mu yem ci ñaari màndaa yi ko àtte ndeyu réew mi may. Su ko defulee, réew mi dina yëngu te loolu kenn ñaanu ko Yàlla.»
Paap Aamadu Siise, minise almiñom :
« Netteelu màndaa, yaakaar naa ne mën naa war a ne. Ndax, keneen ku ńu fal it day sumb liggéey bu bees. Te su nu waxantee dëgg, gisuma ku fi mën a wuutu Maki Sàll. Kon li gën mooy mu def ñetteelu màndaa ngir yeggale liggéey bi mu tàmbali ci atum 2012.»