Site icon Senexalaat

Sàrti Ndaali-maali

Ndaali Maali, walla Mande, benn la woon ci nguuru nit ku ñuul yu mag yi nekkoon démb ci déndub Afrig. Moo fi wuutu woon ndaali Gana ci Afrig sóowu jànt. Gana moom itam moo donnoon jàllooreey yeneeni nguur yu mel ni Aksum , Kuus, Nibi ak Misira démb bu Buur-Fari ya.

Ndaali Maali jàpp nanu ne ca Xeelu xarnu ba ci XIVeelu xarnu ba la fi nguuram lawoon, ëmboon réew yii tey : Maali, Senegaal, Gambi, Gine, Niseer, ak bëj-boppu Gànnaar… Ña fa doonoon Buur-Daali seen jàlloree jàll xarnu yi ba yegsi ci ñun: ñoom Mansa Musaa, Sumaaworo Kante, Sunjata Keyta ak ñeneen. Booba Afrig a yore woon wurusu àddina si, nit di jóge fu nekk di waliwansi di wutsi xam-xam.

Tekki sàrt bi doon doxal ndaali Maali bii topp ci làmmiñu wolof mu ngi sukkandiku ci jukki bu ay boroom xam-xami cosaan yu Senegaal, Maali, Gine, ay gawlo ak ñeneen dekkalaatoon ca Kankan (réewum Gine).  Ci sàrt bii la ñu tërëloon yoon ya ñu doon jëflante ci seen biir sosiete ci fànn yépp : koom-koom, politig ak yeneen. Kon mënees na cee jàngate lu bare ci ni maam yooya gise woon àddina, seen parlu, seen xayte ak seen mandute. Jikko ak melokaan yu tumuranke te Afrig ak àddina sépp soxla leen.

I NEKKANDOO CI BIIR ASKAN WI

Matukaay 1eel:

Askanu ndaali Maali limu pegg yii ñoo ko sos:

. 16 xalakat walla « ton ta jon »

. 4 njabootu garmi walla « mansa si »

. 5 njabootu sëriñ walla « mori kanda »

. 4 peggi liggéeykat  walla » nymakala »

Pegg bu nekk dafa am ay wareef ak ay sas.

Matukaay 2eel:

Peggi liggéeykat yi  « ñamakala » dañoo war fu ñu tollu di wax dëgg seeni njiit, di leen digal, di saytu ci seen làmmiñ ak seen jëf yoon yi ak sàrt yi ñu tëral ci ndaali Maali.

Matukaay 3eel:

« Morikanda » yi walla sëriñ yi ñooy sunuy sàng te ñoo ñuy yar ci diine lislaam. Kon ku nekk yoreel na leen njukkël te war na leen a weg.

Matukaay 4eel:

Askani ndaali Maali ay maas ñoo ko bokk. Maas bu nekk day fal njiitam. Ñi bokk benn maas ñooy nit ñi (góor walla jigéen) yi seen magante weesuwul ñetti at.

« Kangbe yi », walla maas yi nekk diggante ndaw ñi ak mag ñi, dañoo war a bokk fa ñuy fase tëral yu am solo yépp yi soxal sosiete bi.

Matukaay 5eel:

Nit ku nekk ci askan wi yelloo na dund, yelloo na karaangee ci yaramam. Képp ku faat bakkanu keneen nit, yoon di na la natt ñu faat sa bakkan.

Matukaay 6eel:

Taxawalees na ngir xeex yaafuus ak yàccaral, am yokkute kurél gu ñu tuddee « Könögbèn wölö ».

Matukaay 7eel:

Waaso yi ci biir Mande sàkkees na ci ag kàll ci seen diggante ñoom ñépp. Ñoom ñépp ay doomu bàjjan lañu, maanaam jote seen diggante warul a ëpp loxo mukk, te war nañu di nawante ak di wegante fu ñu tollu.

Naka noonu diggante ay goro, diggante maam ak i sëtam kaf ak fo ak ree fu ñu tollu moo leen war.

Matukaay 8eel:

Njabootu Keytaa mooy njaboot giy jiite ndaali Maali.

Matukaay 9eel:

Yaru gone yi askan wi yépp a ci war a farlu, ba tax askan wépp ay baay di ndéy ci tuut-tànk yi.

Matukaay 10eel:

Nañu baaxoo di jaalewante saa yu nit génne àddina.

Matukaay 11eel:

Su seen jabar walla doom dawee làqu ci seen dëkkandoo bu leen ko fa topp.

Matukaay 12eel:

Ndegam ndono néegu baay a ko yelloo, bu leen fal mukk doom bàyyi baay feek kenn ci baayam yaa ngi dund. Bu leen jox mukk ndogal ab xale ngir rekk am-amam.

Matukaay 13eel:

Buleen tooñ mukk « ñara yi » (manaam boroom kàddu yi walla gawlo yi)

Matukaay 14eel:

Ñeel leen fu ngeen tollu jigéen ñiy suñuy yaay.

Matukaay 15eel:

Bu leen yëkkati mukk seen loxo jëmale ko ci jigéen juy séy feek boolewuleen ko ba tàyyi ak boroom këram.

Matukaay 16eel:

Wareef la di boole jigéen ñi ci kurél yépp ci nguur gi, wareesu leen a yemale ci lenn ci fànn woowu.

Matukaay 17eel:

Jàppees na fen yi yàgg ba weesu 40 at ne kon ay dëgg lañu.

Matukaay 18eel: 

Nañu fonk te ormaal képp ku ñu mag

Matukaay 19eel:

Góor gu nekk ñaari goro la am: waay-juri ndaw si mu takkagul ak kàddoom gi mu joxe ci coobare boppam.

Warees na leen fonk te di leen sàmm saa su nekk.

Matukaay 20eel:

Bu leen toroxal mukk seeni jaam, may leen ayu bés bu nekk bés bu ñu cay noppaloo. Fexe leen ba ñuy wàccook seen liggéey ci waxtu yu yem. Sab jaam yaay sàngam, wante moomoo gaafakaam.

Matukaay 21eel:

Bul di miinanteek soxnaay ki la yillif, sa dëkkandoo, sab sëriñ, boroom xam-xamu cosaan, sab xarit walla ki nga àndal di liggéey.

Matukaay 22eel:

Rëy màndargaay néew doole la, xeebu di màndargaay daraja.

Matukaay 23eel:

Bu leen di worante mukk, sàmmante leen ak seen kàddu.

Matukaay 24eel:

Bu leen lor mukk doxandéem.

Matukaay 25eel:

Ndawal kilifa amul lenn lu mu war a tiit ci biir ndaali Maali.

Matukaay 26eel:

Yëkk bu ñu la denk, warul a jiite ab gétt.

Matukaay 27eel:

Bépp jànq bu tollu ci njeexitalu ndawam mënees na ko maye mu séy te deesu ca seet ñaata at la am.

Ak nu jamaale ya mën a tollu ak ku ñu mënti doon, la waay-juru jànq ba dogal rekk lees war di topp.

Bépp xale bu góor bu am 20 at mat naa dénc soxna.

Matukaay 28eel:

May gu njëkku jànq ñetti nag la: benn bi jànq bee ko moom, yeneen ñaar ya yaayam ak baayam ñoo leen moom.

Matukaay 29eel:

Tas séy dagan na ci anam yii:

. jëkkër ju tële

. waay-séy bu dof

. góor gu mënul a wáccook wareefam ci séy

Bépp séy bu ñuy tas dañuy dem ba génn dëkk bi door ko fa tas.

Matukaay 30eel:

Nañu dimbali képp ku yelloo ndimbal.

Matukaay 31eel:

Nañu fonk mbokk, séy ak dëkkandoo.

Matukaay 32eel:

Ray leen seen noon su waree, wante bu leen ko toroxal.

II. MOOMEEL YI

Matukaay 34eel:

Ci juróomi anam yii topp mënees na cee am lu lew: jënd ak jaay, maye, weccee, liggéey ak ndono. Beneen yoonu am-am bépp bu leen moy te amul seedde dese naa lew.

Matukaay 35eel:

Lépp lu ñu for te kenn newul ne moo ko moom, su àppu 4 at weesoo kese lay mën di doon moomeelu mbooloo mi.

Matukaay 36eel:

Nag wu ñu denkaane, su juree ñeenti yoon, ñeenteel ba ka ñu ko denk moo ko moom.

Matukaay 37eel:

Sëll ñetti xar mbaa ñeenti bëy lees koy weccee

Matukaay 38eel:

ñeenteeli nen bu nekk ka ñu denk ginaar gaa ko moom

Matukaay 39eel:

Xiif gis loo lekk, lekk ko, du ag càcc soo yemee ci lekk rekk te jëloo ca dara yobbale.

III. AAR CÀKKEEF Gi

Matukaay 40eel:

Àll bi mooy suñu am-am bi ñu war a gën a fonk: ku nekk war na ko sàmm, aar ko ngir tawféexu askan wépp

Matukaay 41eel:

Saa yoo bëggee taal àll bi, bul xool ci suuf, téenal xool njubaqtanu garab yi.

Matukaay 42eel:

Jur gi ci kër yi dañu leen a war a yéew saa yu nawet teroo te deesu leen tekki feek góobuñu ba noppi: Xaj, muus, kanaara ag njànaaw gi bokkuñu ci.

IV. MATUKAAYU YU MUJJ YI

Matukaay 43eel:

Bàlla Faseke Konaate moom lañu fal mu yilif lépp lu aju ci xew-xew yi ak baaxental yi. Mooy kiy dox rataxal-diggante askanu Mande gépp.

Ci loolu may nañu ko muy kaf ak a kàlloo waaso yépp rawatina njabootu Buur-Daali.

Matukaay 44eel: Képp ku wàcc sàrt bii yoon dina la duma. Ku nekk war na koo saytu te di ko jëfe ci biir réew mépp.

 

http://www.wolof-online.com/?p=831







Quitter la version mobile