Retrouvez ci-dessous, le résumé en Wolof de notre article sur le rôle crucial de l’éducation dans la gouvernance sociale
#Enjeux2019 – XamXàmme mooy indi kaaraange, moodi am sa gopp ngir bay, am xalima booy binde, moodi yore sa galan gooy tëgge sa sabar, ngir feexal sa xol. Xam sa yaram, say cër moodi nite tette, yar, mooy may gone am loxo yu set bamën, bokk ak mag ňi.
Ni begg toog ci jal bi, ngir gindi réew mi war nan leeral lunu xam ci jaar jaari réew mi, ci mbirum jàng ak jàngale, yarak tette xale yi, tàggat magňi, yee leen ci mbiri àdduna. Yeewu mooy tax men toog ci penc ma ; bayaal ba, ,ja ba
Warnen wax lu nu xalaat ci denkaane yi doomi reew mi ak boroom xam xam yi def ngir suxxali njàng mi, ngir mu barkel, jariň reewmi, ,jariň askan wi, te it kenn baň nooy yak. Xam adduna, xam li ňu war, sàmm càkkeef gi.
Wax rekk doyul war nan leeral funuy jele xaalis bi war, ngir defaraat jikko yi, xel yi
Xam loo àttan ak loo àttanul
Nu yokk ci sa mën mën, pexe, xam sa diine, say baax ak xarbaax, sa cosaan, xam yosi say dekkandoo, ngeen wegante ; looloo mooy suuxët jàmm.
War nan wax it ni nuy xaymaa ak di topp li nuy degmal
Jàmm sax, yalwaan dakk, xatxat yi, wànňiku, nit ni am ci li nuy gor, ngir gore
Xam seen warugar, xam seen wareef
Buuba Joob, njiitu PAALAE
B. Joob, njiitu PAALAE