Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

Yoonu YÀqute…

Yoonu YÀqute…

“Noo lànk !”

Ñaari baat yooyu la askanu Senegaal wépp àndandoo yuuxu cib doxu-ñaxtu, àjjuma jii weesu. Li nu ko dugge woon mooy fésal seen naqar ci yokkute njëgu mbëj gi. Mu mel ni mbooloo mu takku mi wàccoon ci mbeddi Ndakaaru yi dañoo dànkaafu nguur gi. Mooy li ñuy faral di wax rekk : askan wi dafa tumuraanke ndax li réew mi « maki ». Ñépp a bànk, loxo yi banku, Senegaal wutewul ak màggat mu dóox, lott ba tóox, foo laal mu may lab yóox. Muy lu tiis te diis cib xol. Moom daal, dara doxatul ci miim réew. Daanaka lépp a yokku : ceeb bi, esaas bi, paasi oto yi, simoŋ bi, luyaas bi, dëkkuwaay yi, ndox mi… Rongooñi baadoolo yi feraguñ sax, ñu yokkati njëgu mbëj gi. Mu mel ni nguur gi dafa daanu, amatul xaalis. Ci jamono joo xam ne, politiseŋ yaa ngi gën a am alal, askan wiy gën a lott, nguur gi soxla xaalis, ñu nar a ŋaccati poosi baadoolo yi ciy yokk ak i lempo yu dul jeex.

Moo tax, keroog àjjuma, mbooloo mu takku fippu, ànd doon jenn jëmm, ne : « Noo lànk ! Kenn dunu manq ! » ; « Sonn nan, tàyyi nan ! » ; « Senegaal metti na ! » ; « Yoon amatu fi yoon ! » ; « Ku wax ñu ni la ràpp, tëj ci kaso bi ! » ; « Bàyyileen Gii Maryiis Saañaa ak i ñoñam ci nim gën a gaawe ! » Kàddu yii ñoo gënoon fés ci doxu-ñaxtu bi kurél giñ duppe Noo lànk amaloon. Ndege, mbooloo mu takkoo nii, gëj na fee am. Aar li nu bokk mi doon kaas mbirum petorool beek gaas bi sax, amu ko woon. Muy lu jar a bàyyi xel. Lu xew ba Senegaal mettee nii ? Fan lañ dugal xaalisu réew mi ? Ana milyaar yi Maki lebi woon bitim-réew ak ci bànki àddina sépp ? Mbaa du danoo nekk ci joyyantib-koom te kenn sañu koo wax ?

Nguur gi, yokkuteg petorool bi lay taafantoo. Waaye, loolu du wax ndax fi  mu ne nii barigo bi 60 dolaar lay jar te ca jamonoy Ablaay Wàdd yéegoon na ba 120 dolaar te taxul woon yokkute am. Ablaay Wàdd dafa aaroon Senelec, dimbalee ko 120 milyaar ngir mbëj gi bañ a yokku. Kon, wax ji wax ji mooy, nguuru Maki Sàll amatul dërëm.

A LIRE  L’heure de vérité d’Ousmane Sonko

Num mën a nekke ?

Doxalinu cuune, càcc, ger ak salfaañe xaalisu réew mi moo ko yóbbe tolof-tolof yim nekke. Fi mu waroon a def alal ji la ko deful. Luy TER ? 30 kilomet kese, nga xëpp ci 600 milyaar. Te iniwérsite bu baax di jar 90 walla 100 milyaar rekk ; loppitaanu Tuubaa 40 milyaar kese doyoon na ci. Dëkki kow yaa ngi jooy dispañseer, beykat yi sonn, sàmm yi waxi noppi. Luy PUDC ? Luy Bourse familiale ? Bala maa dee ñu naan dem nañ ci àll bi, def fa benn raŋ-raŋ, añs. Te sax, loolu du lu bees. Ablaay Wàdd amoon na fi dàkkental bum joxoon Abdu Juuf ak soxnaam Elisabet Juuf : Muse fooraas ak Madam muleŋ. Ablaay Wàdd ci boppam bi mu faloo, sosoon na fi PNIR, te loolook PUDC benn la rekk. Jarul réy làmmiñ. Yu ñàkk solo yooyu, diy weccet, jarul a woote xumbal ba ciy tëgg sabar. Bourse familiale du lenn lu dul ab sarax. Waaw, 40 milyaar nga séddale koy nit, ku nekk nga jox ko juröomi junni, mu saqami jàllale, toogaat tuuti xiif. At mu nekk nga nar ko jàppe noonu, di ci génne 40 milyaar di yàq te kenn du ci suturlu. Boo defaroon mbey mi, sàmm gi ak nàpp gi, ku nekk am ci lum jàpp, mënal boppam ak njabootam, ndax gënul woon ? Gaa ñi, seen gis-gis a soriwul rekk ; li ñu tal kay, mooy noos ak a gundaandaat, fàtte ni 100 nit yoo jël 40 yi amaguñu mbëj te yit xiif a ngiy bëgg a rey 1 500 000 doom-aadama. Li am ba des mooy ne, dañu fowe xaalisu askan wi.

Léegi, nag, tollu nañ foo xam ne, ñépp a leen mere, jéppi leen. Rawati-na bi kàngami APR yi nekkee ci tele yeek rajo yiy xastante. Njiitu-réew mi ne cell, yoon fatt i noppam, muur i bëtam, bank i loxoom. Buñ jógee, naan koom gaa ngi yokku, àgg na sax ba 7 %. Koom gi yokku, askan wiy sonn : ay waxi seytaane doŋŋ !

A LIRE  Pour Bassirou Diomaye Faye (Par Demba Moussa Dembélé)

Yaa ngi yokk dund gi te yokkoo benn yoon peyoor yi ; nga bëgg wax ne réew maa ngi dox. Kan lay doxal ? Xanaa ñu mel ni Sonatel, isini simoŋ yi ak bànk yi. Te yooyu yépp, Tubaab yee leen moom. Moo, ndax mbey mi yokku na ? Sàmm gi, nag ?  Ndax napp gaa ngi joxe ci miim réew ? Njàng mi, nag ? Ndax gone yi am nañu xéy ? Ku waxal Yàlla, dinga ne déedéet. Kon liy dox kan lay doxal ? Ay Tubaab yu xonq cuy ? Coono bin nekke, nguur gee nu ko teg. Moone de, Bànk-Monjaal aartu woon na leen.

Am nay xeltukat yu jàpp ne Bànk-Monjaal daf nuy noot. Déedéet. Demewul noonu. Moom kay, jamono jii, daf nuy dimbali. Dafa di, sunuy njiit ñoo wowle. Ndege, bi nguur gi taxawee ne day def 600i milyaar ci TER bi, Bànk-Monjaal dafa ne déet, waa nguur gi ne ko « Noo moom sunu bopp ». Ñu ne dañuy defar otorut Ilaa-Tuubaa, mu neeti leen jaru ko, baaxul ci koom-koomu réew mi, ñu dëgërati bopp.  Daaw, Maki lebi xaalis bu bare, Bànk-Monjaal ne leen nañ denc boog xaaj bi ba 2019, Aamadu Ba ne leen noo moom sunu alal, lu nu neex lanu ciy def. Yedd nañ nu, aartu nu ngir nu xam ni naal yi baaxul. Ñoom, nag, duñ ci boole wax ju bare. Buñ la teree nga të, dañ lay bàyyi, di la seetaan ba nga këmmal – këmmal mooy tële ci wàllu koom – ba amatoo loo feye liggéeykat yi. Bu loolu amee nag, doo def lu dul sàkkuji ndimmal Bànk-Monjaal. Foofu la Senegaal tollu. Tàllal na loxo, ñu ne ko wax naa ba sonn nga dëgër bopp, léegi nag dangay def li ma lay sant, mu neex la ak mu naqari la. Ndege, goneg mbóoya, dees na ko xaar ci taatu ndaa li ; te nag, àgg nan ci taatu ndaa li.

A LIRE  Dossier Bohn-Air Sénégal: À quand le réveil ? (Par Tidiane Amadou Hane)

Cib joyyantib-koom lan nekk. Maanaam, Bànk-Monjaal danoo xàllal ñaari yoon. Wu njëkk wi mooy : yokkal sa xaalis. Te nag, nguur naka lay yokke xaalisam lu-dul yokk simoŋ, yokk esãs, yokk peyaasu Ila-Touba, yokk peyaasu tali Kàmbéréen bu bees bi, yokk leneen ak leneen ?

Weneen yoon wi mooy : fexe leen ba wàññi depaas yi . Bànk-Monjaal, nag, du la ne wàññil lii, walla laa. Moom daal, da la naan wàññil lu tollu nii. Yaay seetal sa bopp nooy def. Looloo taxoon nguur gi ne day tëj 32i àmbasaad ak i asãs ngir sakkanal. Kon, bu kenn tuumaal Bànk-Monjaal. Lu jiin Njaag a, te sunu njiit yeey Njaag. Bànk-Monjaal da lay xelal, boo nangoo baax na, boo bañee mu xaar ba nga tële, mu duma la duma yu metti ni mu ko fi defe woon Geres ak Arsaantin. Moom kay, bu yeboo askan wi dee, sonn, xiif, mar : yoonam nekku ci.  Li ko ñor mooy naŋ ko delloo xaalisam rekk.

Noonu, yookute njëg yi, day fekksi wàññi yi.  Boo boolee loolu nag, moo lay jox joyyantib-koom. Sikk amul ci ne nguur gi dafa ndóol ba mujjee sàkkuji ndimbal ci Bànk-Monjaal mi ko aartu woon mu lànk.

Nu jeexale ci bor bi.

Senegaal, 82 milyaar lay fey ci bor weer wu dee, nga teg ci 80 milyaar yi muy fey liggéeykati nguur gi, muy 160 milyaar weer wu nekk. Mu ngi mel ni, ngay feyyeku 120 000 FCFA, di depaasoo 160 000 FCFA. Ndax dinga mucc ciy bor ? Mukk ! Réew mi amul xaalis, xanaa nu dem Jamñaajo sullee ko fa.

Yoonu yokkute la nu Maki Sàll digoon. Waaye li leer ba leer mooy ne  réew mi ci yoonu yàqute







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *