Site icon Senexalaat

JÉeri Joor Ndeelaak Tubaab Bi

JÉeri Joor Ndeelaak Tubaab Bi

Jéeri Joor Ndeela Faal mu ngi gane àdduna ci atum 1871. Mu doon doom ci Sàmba Yaaya Faal mi newoon fanweer ak ñaarelu Dammeelu Kajoor te Nasaraan yi daaneloon ko ba noppi yóbbu ko Ndar-Géej, téye ko fa. Ci atum 1891 la xaru ci dex gi ginnaaw bi way-juram bu jigéen génnee àdduna te Tubaab bi aaye ko mu teew ca dëj ba.

Ñuy wax ne ba muy takk rakki Kànnaar Faal mi doonoon kilifa ca tundu Bawol te moom it Tubaab bi daaneloon ko, Kànnaar moomu da koo mayoon ñaari jaam. Bi ñu ci tegee ab diir, Jéeri ànd ak Kànnaar Faal ak Bookar Tilaas – mi yilifoon tundu Géwul – dem Cees jaay fa jaam yooyee. Fekk na booba Tubaab bi aaye woon njaayum jaam. Noonee, juróom-ñaari fan ci weeru awril ci lañu leen tege loxo ñoom ñett yóbbu leen ca kër gornóor ba ca Cees ñu jàkkaarlook kummàndaŋu Tubaab ba tegoon seen kaw tuumay njaayum jaam. Ca la leen fayloo ab alamaan.

Waaye yamu ca ne da caa teg ne Jéeri dees koy tëj kaso diirub fukki fan ak juróom.

Booba fekk na Sarica Jéey, di xarit ci Jéeri, doon ko xaar ci biti. Ba mu déggee coow li mu daldi mer ba futt ne “mënees naa nangu alamaan bi gaa, waaye xel xalaatul muy seetaan ñuy tëj Jéeri waxumalaak di ko jéng. Loolu moom mënuma koo nangu !”

Bi Jéeriy xeex ak alkaati yi ko doon jéem a jéng, la Sarica Jéey dàjji bunt bi ne jaas ci biir bérébu-àttekaay bi. Ca la alkaati yi dawe, mu bocci paaka jam ko Henry Chautemps mi fa wuutu woon gornóor, mu faatu ci saa si. Ba mu ca jógee la jël paaka bay siit ak deret jox ko Jéeri. Ñu ànd ñoom ñaar génn, géwél yi topp leen di tagg  ay maami Jéeri Joor Ndeela Faal.

La ca Sarica Jéey jublu woon mooy sàmm woyu Jéeri Joor Ndeela Faal, mu doon woy wu rafet ba ciy sëtam ba ñu mën a fàttaliku ba fàww ne Jéeri moo reyoon kummàndaŋ bi ko bëggoon a yóbbe gaay demba.

Ca la Jéeri Joor Ndeela Faal ànd ak xaritam Sarica Jéey ñu bawoo Cees dem Caytu ca nijaayam Masàmba Saasum Koddu Jóob miy maam ci Seex Anta Jóob mi ñépp xam.  Ba ñu fa jógee dem Sugeer, Jéeri waxtaan ak ay mbokkam daldi ne du daw, xanaa day toog jàmmaelook noon bi xeex ba daan mbaa mu daanu.

Booba fekk Tubaab yi tàmbale koo wër ba sax dig ab neexal képp ku leen jébbal Jéeri ci muy dundu walla mu dee.

Waaye ci juróom-ñeenti fan ci weeru awril atum 1904 – fekkoon booba ñoñi kumàndaŋ Prempain yi doon wër Jéeri wër bu metti – la ko Kànnaar Faal reye. Kànnaar xaritam la woon, doon goroom te yit ñoo àndoon wuyuji ca Cees. Dafa lalal Jéeri ndëgg-sërëx, ba noppi dagg bopp bi ak benn loxo bi dem jox ko Tubaab bi. Na mu ko baaxoo woon def booba ngir tiital bañkat yi, Tubaab bi jël loxo Jéeri baak bopp bi samp leen cib bant bu gudd teg ko ca pénc ma feggoog màrse Cees. Booba Jéeree ngi amoon fanweeri- at ak ñaar rekk.

Sarica Jéey xaritam bu gore boobee ba ñu ca tegee ñaari fan la ko Tubaab bi teg loxo, sànni ko Giyaan, nekk ca wetu Ameerig.  Sarica mujj na faa takk soxna ba am fa ñaari doom.

Kànnaar Faal workat ba moom, Tubaab bi da koo mujjee wor, tëj ko ñaar-fukki at ci kaso bi. Ñaari at la fa def, tuub, dugg ci diine lislaam, soppi turam, di wuyoo ci turu Aamadu Kànnaar Faal.







Quitter la version mobile