Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

KÀdduy Aadama Jeŋ

Tofo ci Antonio Gutieres, « Sekerteer Seneraalu » Mbootaayu xeet yi, di ko xelal ci lépp lu aju ci aar faagaagal aw xeet. 

(Siyaara Tayba Ngéyéen)

Asalaamu aleykum wa raxmatulaayi ta alaa wa barakaatówoo !

Yéen Kilifa yu tedd yi,

Yéen sang yi,

Yéen ñi fi teew ñépp, góor ak jigéen, mag ak ndaw

Nuyu naa leen, kenn ku ci nekk ci turam ak santam, di leen sargal.

Janook yéen tey di yëkkati samay kàddu ci béréb bu tedd bii te sell, lu am solo la te maak Yàlla rekk a xam ni ma ci bége, ni ma ci ame bànneex !

Fàww sama yaram daw ndax 20 at a ngi yëkkatiwuma kàddu jëmale ko ci askanu dëkk bii sama maam Siidi Buri Jeŋ sos te sama waajur Ibraayima Jeŋ cosaanoo fi. Siidi Buri Jeŋ, Ibraayima Jeŋ, yal na Yàlla yokk seen leer.

Jamono ja ma nekkee «Sekerteer seneraalu komisiyoŋ internasiyonaalu sirist yi » ñëw naa teewesi fi ubbiteg dispañseer.   Du woon man rekk, sax, ndax ay doomi-dëkk bee mànkoo woon tabax ko, ñu bare ci ñoom doon i kilifa yu féete woon bitim-réew, moo xam Itali la mbaa Gaboŋ walla feneen.

Noonu lanu lëkkaloo tamit ak doomi Tayba yi nekk ci biir réew mi, di ay kilifa, ngir tabax benn liise ci dëkk bi, mu xettali gone yi, yokk seen xam-xam, tax ñu gën a yaru.

Fan yee ñu génn rekk lanu ànd nun ñépp gunge ca këram gu mujj sama mag Muxamadu Mustafaa Jeŋ, doon it kilifa diine, boroom xam-xam. Royukaay la woon ba tax ñu jagleel ko bésu tey bii waaye li ci gën a daw yaram, ndeysaan, moo di ne maak moom yaakaaroon nanu ne dinan gise ci siyaare ren bii.

Maa ngi fàttaliku sama ndaje mu njëkk ak Tafsir Mustafaa Caam, kàddu ya mu yëkkati woon jëmale leen ci Ceerno Seydu Nuuru Taal, naan : «Bu waa Senegaal xamoon kan mooy Ceerno Seydu, dinañ koy seeti bés bu ne.»

Tafsir Mustafaa fonkoon na lool Xalifa Muxamed Ñas nga xam ne kàngam la woon ci tariixa tijaaniya !

Man miiy wax ak yéen, ci atum 1958 laa njëkk joxante loxook Xalifa Ñaseen bi ca «Awani» Maalig Si bu Ndakaaru, am ci bànneex bu jéggi dayo.

Maa ngi fàttaliku Baay Xalifa, keroog cig « haal gu metti », won nanu ni Yonent Yàlla Muxamed (Sala laawu aleyi wa salama) daan doxale !

Su ma doon lim kilifa diine yeek niti Yàlla yu baax yi  ma mas a toogal, dinaa tudd  Sériñ  Séex Mbàkke Gaynde Fatma, Séex Al Islaam Àllaaji Ibraayima Ñas, Àllaaji Abdul Asiis Si Dabaax, Sëriñ  Mañsuur Si Boroom Daara ji, Ceerno Muntaaxa Taal, Séex Buu Kunta Njaasaan, Séex Tiijaan Si Al-Maxtum. 

Mënumaa lim ñépp ndax niñ koy waxe ku lim juum ! Li am solo mooy fàttali leen ne kilifa yooyu yépp, ba ci Kardinaal Yaasent Càndum, ay géeji xam-xam lañu woon ci man, lu ne laa jàng ci ñoom.

A LIRE  APRÈS LA «BOMBE» SPORTIVE, MACKY TENTE DE DÉSAMORCER LA BOMBE SOCIALE

Li taxoon Senegaal am doole ci jamono jooju moo di ne xàjj-ak-seen amu fi woon, réew mi doonoon menn jëmm kott waaye teewul ku nekk mel ni nga mel, féete fi nga féete, kenn xatalu fi sa moroom, daan nga dugg ci kër kii ne la yilimaan la, keneen ne la làbbe la te fekk na moonte ñaar ñooñoo bokk ndey bokk baay !

Senegaal a ngoog, ñi fi sos tariixa yi, di ay jullit di ay Sufi yu mag  ñépp nangul leen seenug bëgg jàmm !

Nun nag, danuy ndamoo loolu fépp fu nu dem ci àddina si. Seetoo ngoog boo xam ne bu nu janook moom dunu sëgg !

Bindoon naab bataaxal ñeel askanu réew mi, ci weeru suweŋ 2018, doon ci fàttali ne maa ngi màgge ci keppaaru Kilifa gii di Seydu Nuuru Taal mi gëmoon lool ne julliti Senegaal yeek kerceen yi waruñoo nangu ku leen féewale, foo ko fekkaan mu ngi leen ñaax ci waxtaan ba déggoo, ànd doon benn. Li ñu tudde ci nasaraan ‘’Dialogue islamo-chrétien’’ du leneen. Ci sama jaar-jaar ba tey, ameel naa yit njukkal Sëriñ Séex Mbàkke Gaynde Faatma, nit ku baax te bëggoon réewam. Moom daal, ci kilifa diiney Senegaal yépp laa géeju ba wóolu sama bopp, dem ba am fitu dajale kilifa diiney àddina sépp, ñu toog weccoo xalaat ! Muy « Rabeŋ » bi di «Yilimaan» bi mbaa «Eweg» bi walla dig kilifa ci diine «Budist»  yi, ñoom ñépp a daje, sottante xel ngir fàq ñaawteef yi mën a lor doomu-aadama fépp ci àddina si. Ndaje moomu, maa ngi ko njëkkoon a woote ca Fees, dëkku diine bu nekk ca Marog, toftal ca yeneen ca Terewiso (Itali), Wasiŋton (Amerig), Amaan (Sordani), Adis-Abeba (Ecópi) ak Bankoog ca Taylànd. Li ëppoon solo ci ndaje yooyu yépp moo doon ni du fenn fuñ ci yëkkatiy kàddu yu rafet yem ci, dañoo tëral ca Fees ay pexe ngir lépp lu mu laaj ñu def ko. Naalu Fees boobu, Njiitu Mbootaayu Xeet yee taxawal ag kurél ñeel ko ci 17u fan ci weeru sulet 2017 ca New York.

Gëm naa ne ndam li nu am ci ndaje yu mag yooyu dara waralu ko lu-dul li ma cosaanoo ci réewum Àllaaji Umarul Fuutiyu Taal, Séex Amadu Bàmba Mbàkke Xaadimu Rasuul, Mawdo Maalig Si, Yaasent Càndum ak ñoom seen. Kilifa yooyu ma tudd, danoo war a taxaw temm ngir sàmm seen ndono.

Yéen Kilifa yu tedd yi,

Yéen sang yi, góor ak jigéen,

Ci jamono coppite yu mag lanu nekk tey. Ay coppite yu ñeel nekkin ak dundinu askan wi. Mu ngi dooree ci càkkeef gi waaye mënees na cee lim tamit  :

A LIRE  DANS LA PEAU D’UN MIGRANT «IRREGULIER» SENEGALAIS

  • Ndóol gu tar
  • Ñàkk yemale,
  • Xare yu metti,
  • Ñàkkum ndox mu sell mi ak mbënn meek ñoom seen, loolu lépp tax na ba alfunniy – miliyaari – doomi-adama di gënatee sonn.

Nguuri àddina yépp nangu nañ tey ni doonte sax nun ñépp ci genn gaal gi lanu nekk, gàllankoor yi bare nañ lool te bi ci yées mooy li doom-aadama yi wegantewul.

Ñun ñépp a war a taxaw, booloo ngir sàmmoonteek àqi doomu- aadama. Bu nu ko deful, balaa yàgg nu réccu ko !

Tey jii ci diiwaanu «Sayel» gi nu bokk, jafe-jafe yi Mali, Burkinaa- Faaso ak Niseer nekke jéggi nañ dayo !

Ñàkk kaaraange, bóom, siif ak xeeti rey yi nu fay gis, war naa tax ñépp joxante loxo doon benn, fexe ba ñaawteef yooyu bañ a law ci réew yi leen séq, rawatina nag Senegaal !

War nanuy sédd ëllëg tey fagaru ba kenn dunu bett. Looloo ngi war a tàmbalee ci kilifay gox yi ndax ay kilifa yu am baat lañu, jege lool askan wi, askan wi yit jox leen seen gëdd, déggal leen.

Waaye mbir mi moom, nun népp la war a soxal, war nanoo jànkoonteek ñi tudde seen ay Yilimaan tey jël «Al Xuraan» di ko firee neneen !

Su nu bëggee daan sàmbaa-bóoy yiy mbubboo sunu diine ji, fàww daaray nguur geek daara cosaan yi bokk ci xeex bi. Waaye warees na fexe tamit ba ndóol gi wàññiku ndax kat, nit ku dëkke fàndeek dëñe, xel mi day neex a këf, mu neex a yóbbaale !

Yow Xalifu njabootu ku tedd kii di Tafsiir Mustafaa Caam, ni ma xame sag fonk njàngalem diine ak jikko yu sell yi mu làmboo, mu di jàmmoo, bëgganteek dimbalante, wòor na ma ni dinga wéyal li fi say maam bàyyi, mu doon cëslaay ci réew mépp, rawatina ci xaley Tayba yi, ñu ciy roy, ba mën a mucc ci pexey sàmbaa-bóoy yi !

Abdu Juuf, Njiitu-réew mi fi woon, daan nay faral di wax ne «Amul lu gën jàmm, ndax jàmm ci la lépp xaj.»  Kon jàmm, moomeelu askan yépp la, ñépp la soxal, nekkul lu ñu jagleel wenn xeet kese, mbaa jenn aada !

Sama xarit, sama doomu-ndey, boroom xam-xam ba, Seex Abdalaa Ben Beyaa, njiitu kuréel giy sàkku jàmm, nekkoon tofo ci Njiitu-réewum Gànnaar ca jamonoy Maxtaar-Uld Dadaa, daan na ma wax ni : «War nanoo aar, fonk sunug njullite, roy ci njànglem Yonent Yàlla Muxamed (Salla-laawu-aleyi-wa salama) ba dunu lor ñeneen.» Ni ko sunu mbokki araab yiy waxe : La daraar walaa diraar !

Looloo war a tax nit kiy moytoo jiital xeetam, moo xam Pulaar la, walla Wolof, mbaa Mankaañ, Basari, Sóninke, Séeréer walla Joolaa, bumu jiital tamit diineem… Moom daal, na nekk ñépp, na nekk doomu-Senegaal doŋŋ ! Noonu rekk lay mën a tabaxe loo xam ni day indi jàmm ñeel ñépp, te it ñépp bokk ko !

Wànte fésal lu kenn ku ne doon, fàttee bàyyi xel ci li nu boole, réerook fitna lay jur.

Foo dem ci àddina si, li tax askan way déggoo, nekk ci jàmm, du leneen lu-dul nangoo wute, muñalanteek fonkante.

Duma daaneel te sànniwuma ñaari baat ci mbirum taalibe yi ak li ci laxasu lépp tey gàkkal turu daara ci boppam. Samay xarit, Mamadu Wan, Njiitu kurél giy aar, di ñoŋal àq ak yelleefi tuut-tànk yi, ak Mamadu Njaay Daara, ñu ngi def liggéey bu mucc ayib ci mbir moomu nga xam ne lu jafee lijjanti la !

Ni ko Mamadu Wan waxee te muy dëgg, «Ñépp xam nañ tey ni ñoo ngi metital gone yi ci yenn daara yi, jot na léegi nguur gi jël ay matuwaay ngir dakkal lu ni mel.»

Cig kayitu-saytu bu «Human Rights Watch» siiwal ci atum 2019, biral ci ne yoon waruta seetaan yenn jàngalekati daara yi ñuy def lu leen neex.

Rafetlu naa lool taxawaayu yenn àttekat yi. Ñoom ñoo ngi def seen liggéey, ndax bu yenn wayjur yi bañee yóbbu jàngalekat yooyu ci yoon, du tee ñu topp leen, def seen lànket ba am sax ñu bare ñuñ ci teg i daan  ngir aar  xale yi, ñuy góor mbaa ñuy  jigéen !

Nguuru Senegaal,  ci ndigalu Njiitu-réew mi Maki Sàll, def na ci jéego yu am solo waaye ba léegi njaw des naw xambin ! Lu aju ci yalwaan gi, Njiitu-réew mi biralaat na taxawaayam ak bëgg-bëggam ngir xale joge ci mbedd mi. Ngir doxal loolu nag, ci nguur gi la aju, waaye  tamit sunu wareef la nun népp ñu taxaw ci mbir mi ndax lu mën a nekk la !  Ndax fii ci Tayba, xale yi nekk ci daaray « Al xuraan » yi,  kenn loru leen, kenn jëfandikoowu leen,  te noonu la war a deme ci pépp ruq-ruqaat bu daara nekk ci réew mi.

Xam nañ ni sunu digi réew yi fattuñu, dañoo yaraax ba nga xam ni fu waay jaar walla jóge mën a dugg feneen fi, kon fàww njiiti réewi Sayel yi, diisoo wut pexe ci mbir moomu.

Gànnaaw 30 at bi nu tëralee déggoo gi ci Àq ak yelleefi xale yi, waratunoo nangu toog di seetaan ñaawteef ak yenn lor yiy tegu ci ñoom ci sunu biir dëkk yeek yenn diiwaan yi.

Nee nañu mbey ci sa wewum tànk, kon fàww kilifa diine yi bokk genn kàddu ngir kenn bañatee lor sunuy doom ak sunuy sët !

Waaw-góore Tayba !

Yàlla na Jàmm yàgg ci Senegaal !  







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *