Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

Fan Lanu JËm Ak Ñakki Bill Gates Yi ?

Coow laa ngi ne kurr ! Afrig ba Afrig daj, li ko dale Keer ba Peretoryaa, Ndakaaru jàpp Adis-Abebaa, wax ji benn la : jàppal wakseŋ fii, bàyyil wakseŋ fee.

Coow li nag, ci anternet bi la jëkke. Dafa am ay Móodu-Móodu ak ay Faatu-Faatu yu def ay widewoo di ci aartu seen i mbokk ak askanu Afrig wépp. Liñ ci jublu woon, ci seen i wax, mooy xamal leen ne, ci réewi Ërob yeek Amerig yi, am na ciy mbooloo yu laxasaayoo lëndëm, di lal ay pexe ngir wàññi limu nit ñi ci àddina si, te fas ko yéene tàmbalee Afrig ak nit ñu ñuul ñi.

Nee ñu, gëstukat yooyu kat, dañoo jàpp ne li àddina si am ciy nit dafa ëpp. Bu yàggee, dootuñu xaj ci kow suuf, dund bi dootul doy te kon xiif dina rey ñu bare. Ndaxte, suuf si dina dem ba dootul nangu, dara dootul meññ ; géej gi dina yulleeku ba jeex tàkk. Ci gàttal, dara dootul doy. Kon, ci gis-gisu ñooñu, warees na wàññi doomi-aadama yi bala njaaxum loolu di am.

Mu mel ni daal xalaati Malthus, benn boroom xam-xam bu mag bu doon dund ci 19eelu xarnu bi, ca Àngalteer, la ñuy dekkil noonu. Moom mi doon biral ne, feek wàññiwuñu limu nit ñi, dund gi ci kow suuf du neex, du yàgg.

Bu dara desulee lu dul tànn ñan lees war a wàññi, xeli saay-saay yépp ne yarr ci askanuw nit ku ñuul. Xalaas ! Mbete Yàlla !

Bala maa dee ñu daas seen làmmiñ yi, singali nu. Ki ci gën a rafet wax mooy ki la naan :« nit ñu ñuul ñi dañoo xayadi te mën a jur ba nga ne lii lu mu doon ! » Ñi ci yées xalaat ñooy gënale xeet yi te naan : « Afrig a barey ndaw ! Nun, nag, ñi ëpp ci nun màggat nanu ba dóox, di xaar dee. Des na tuuti, xeetu nit ku weex dina sooy, nit ku ñuul jiite àddina si. Te loolu, warunu koo nangu tey, warunu koo nangu ëllëg, bun ko seetaanee mu ñaaw ! »

Wax ju àgg, nag, dof yaa ko moom.

Lii lépp sax de, day nirook «léeboon ak lippoon». Naka la xalaat yu ni deme, di mën a juddu bay meññ ci xelu nit njaay, ku ànd ak i noppam ?

A LIRE  MONSIEUR LE PRÉSIDENT, SACHEZ ANTICIPER !

Naal boobu, nag, ay boroomi alal, di boroomi tur, ay politiseŋ ak ay boroomi xam-xam ñoo ko sumb, jiite ko. Bill Gates ak Sarkoosi bokk nañ ci ñi ci gën a fés.

Bill Gates, moom, weddi na tuuma yooyu ñuy teg ci kowam. Nee na, waxul ñu wàññi nit ñi waaye nee na ni doomi-aadama yiy yokkoo lañu war a seetaat ngir yaxanal dund gi te neexal ko. Mu fas yéene cee def alal ju tollu ci 100 alfunniy dolaar. Maanaam 50 milyaar ci sunu xaalis. Li mu ci jublu, ciy waxam, moy xeex feebar yi ci Afrig ba noppi, fexee yemale njureel gi. Moom daal, nee na looloo mës a nekk taxawaayam te duggewu ko lenn lu dul sàmm bakkani doomi–aadama yi.

Waaw kii, dunu ko ne jàkk, ni ko : ‘Ngóor si Bill, wiiri-wiiri, jaari Ndaari. Xalaatoo ni Sàmbaay Bàcc rekk, am déet ?’’

Rax-ci-dolli, ay kàngam yu mag a mag àddu nañ ci mbir mi, yokk ci seen xorom. Ku ci mel ni Thedros Adhanom Ghebreyesus, di doomu Ecópi, jiite kurél giy saytu wér–gi-yaramu nit ñi ci àddina si (OMS) ak it njiitu Mbootaayu Xeet yi (ONU), António Guterres bokk nañ ci. Ñaari kàngam yooyu yépp, artu nañ waa Afrig ci koronaawiris bi. Nee ñu, bees fagaruwulee ci lu gaaw, dina fi rey ay milyoŋi nit.

Waaye, li jaaxal ñépp mooy ni, ba sunu-jonni-Yàlla-tey-jii, Afrig mooy dànd gi gën a néewle fopp limu ñi Covid-19 bi daaneel, waxatumaak ñi mu rey.

Loolu nag, tekkiwul ne Afrig mën naa nelaw bay yàndoor ! Ndaxte, koronaawiris bi kat, bàyyiwul kenn !

Li gën a teey xelu nit ñi nag, mooy waxtaan wiñaari gëstukati Farãs yi, doktoor Jean Paul-Mira ak porfesoor Camille Lotch, amal ci ayu–bés yii weesu rekk, te mu siiw lool ci Anternet bi. Ñoom ñaar ñooñu de, dañu doon wecceexalaat ci nu ñuy def ba am wakseŋ buy tax ñu jële Covid-19 bi ci àddina sépp. Ñu jàpp ni BCG, ñakk boobu ñu daan ñakk xale yi ngir xeex sëqët su bon seek yeneeni feebar, war nacee baax. Ñu tëje seen waxtaan woowule ci ànd gi ñu ànd ne Afrig rekk lañ war a defe jéemantu biy tax ñu xam ndax ñakk bi mën naa xeex koronaawiris bi am déet. Loolu, laata ñu koy mën a jariñoo ci seen i dëkk, ci Ërob mbaa Amerig.

A LIRE  EXPLOITATION DU PÉTROLE ET GAZ AU SÉNÉGAL : DES CHIFFRES ET DES LEURRES

Kàddu yooyu, nag, ñoo gënatee merloo doomi Afrig yu baree bare. Am ci ñu siiw ci ñoom, ñu mel ni Samuel Et’oo, Didier Drogba walla Àllaaji Juuf, ñu doon ñu ñu raññee ci mbirum futbal, ci àddina sépp, ak it Claudy Syar mu RFI (rajo bu Frãs moom)… Ñu di ñu am baat, seen kàddu mën a egg fu sori lool. Werante yeek xuloo yi neeti kurr ci Anternet bi, mu mel ni tulleek-màlle, di niru tuq su bënn te saañ ba réer !

Fii nag ci Senegaal, li gën a teey xel, jaxase xel yépp, mooy dégtu (audio) biy daw ci xaraley jokko yu bees yi, ñu ciy dégg baatu benn Tubaab, di  njiitu Ayeropoor Belees Jaañ, muy xamle ne, daanaka Ayeropoor bi tëj na, ginnaaw yenn yóbbal yu ñu fay wàcce léeg-léeg, yu mel ne ay… wakseŋ ! Waa ji nag, bi ñu bare ci ñiy jëfandikoo xaraley jokko yu bees yi dale ci kowam, dellu na ginnaaw, ne moom masul a wax lu ni mel. Doonte dégtu  yaa ngi fi ba tey di ko tiiñal.

Ba ca jamono yooyu, xel yaa nga doon werante, naan dëgg laam déet.

Waaye ci fan yi weesu rekk, gis nañu ay kilifay Afrig di awante ci taskatu xibaar yi ngir teggi tuuma yi. Nee ñu, yëguñu, tinuñu. Waaye, li yéeme dëgg, mooy bi benn gëstukatu Kongo (RDC) bu ñu ràññee jëlee ñaari yoon kàddu ci diir bu gàtt, ba noppi ne maa waxoon-waxeet. Ca njëlbéen ga, dafa waxoon ne boolees na réewum Kongo RDC ci réew yiñ war a natte ñakk bi ñuy wax. Mu ne woon ne, ñoom, nangu nañu te joxe nañ seen kàddu. Bi saaga yeek diiŋat yi jibee, mu dellu ginnaaw ne, ñoom waa Kongo duñu mës a seetaan, ñuy jàppe seen askan nikiy mala.

Senegaal it, kenn demul mu des ñeel fésal cetug deram gi : mu di Ablaay Juuf Saar jawriñ bi ñu dénk mbirum paj mi, di njiitu réew mi Maki Sàll ci boppam, ñoom ñaar ñépp weddi nañu ba mu set, dem nañu sax ba ne, bu dee Senegaal rekk, kenn du ko fekk ci gaalu xaj googu !

A LIRE  Le « Sommet » de Macron: une imposture! (par Demba Moussa Dembélé)

Ci sunu réew mii moom, ñépp a ngiy fàttaliku bés bi Bill Gates daje woon ca Kanadaa ak Maki, ca weeru sàttumbar 2016. Ndaje moomu juroon na fi coow ci ginnaaw gi. Waaye, ndawal àmbasadëeru Senegaal ca Kanadaa indi woon na ciy leeral, di biral ne, waxtaan woowule, dara sababu ko woon lu dul xeex feebar yu mel ni  sëqat su bon si, sibbiru, sidaa ak it ni ñuy def ba yemale njureel gi. Li wóor moo di ne foo séene saxaar, xal yaa ngay boy ca suuf !

Fi mu ne nii daal, xel yi ñaaw nañu ba kenn xamatul looy def. Bu kenn ñakkatul doomam, ndax kon dinañu mën a jële feebar yu bari yi ci sunu réew mi, ak sax ci Afrig gépp ? Bu nu bàyyee ku ñëw rekk ñakkal nu sunuy doom, mbaa kon dunu dimbali ñiy jéem a faagaagal nit ñu ñuul ñi ci kow suuf ?

Laaj yu am solo yooyu ñoo sampu tey te doomi Afrig yi, ak seen i njiit ñoo war a mànkoo joxe ci tontu lu leer, tey doon li gën ci xaley Afrig yi ak ëllëgu Afrig ci boppam.

Ñakk sa doom, mbaa bañ koo ñakk ?

Mu mel ne Afrig tollooti na ci sélébeyoon bi mu tollu woon ca 1963. Jamono jooju, benn ci ñaari yoon lanu mënoon a jaar : yoonu Ufuwet Buwaañi ak Lewópóol Seŋoor, maanaam ànd ak doxandéem bi mu nuy wommat, walla yoonu Kwame Nkrumah ak Séex Anta Jóob, di tekki ne Afrig war naa mën demal boppam ci kow nu bennoo,  di xàccandoo di dóorandoo.

Yoonu Seŋoor ak Ufuwet woowu nu tànnoon moo nu tax a tollu tey fii. Saa su nekk nuy xaar ay doxandéem yiy jóge fu kenn xamul, ñëw  di nu wax lan lanu war a def, fan lanu war a jaar !

Ndax bii yoon, dinanu takk sunu fit, tànn yoon wi nu Nkrumaak Séex Anta xàllal ciy jamono ? Àndandoo xeex nooni démb yi, yu tey yi ak yu jëmmi jamono yi. Bennoo bokk benn jëmu mooy tax Afrig am doole ak naataange. Booloo nuy tax a daan koronaawiris bi ; booloo moo war a nekk sunu kiiraay. Ndege, booloo mooy doole.

Askani Afrig, ëllëg, ëllëgu booloo la, ëllëgu moom-sa-bopp la !







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *