Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

Afrig Ak Koronaa, Afrig Ginnaaw Koronaa (uséynu Béey)

Afrig Ak Koronaa, Afrig Ginnaaw Koronaa (uséynu Béey)

Koronaawiris bi, li muy metti metti, terewul kàngami boroom xam-xam yiy wéy di ci weccee xalaat ñeel doxalinu àddina si, ba xam luy nar a doon ëllëgu doomu-aadama, bés bu nu génnee ba set ci mbas miiy fàdd nit ñi, réewoo réew.

Ñu ci bare jàpp nañu ne, bu nu génnee ci fiir gii nu koronaawiris bi fiir, warees na xoolaat tëralinu koom-koomu àddina sépp, waññi puukare bi te jox gëddam lépp lu ñeel wér-gi-yaramu doomu-aadama. Maanaam, tabax ay loppitaan yu baax te doy, ak lépp li ñu war a àndal ciy xeeti xarala. Warees na yit jiital lépp lu jëm ci dund gi dëgg-dëgg : mbey mi, càmm gi, lekk geek naan gi… Njàng meek gëstu bi tamit, wareesu leen a fàtte.

Wax dëgg, Covid-19 bi musiba la, waaye booy seet ku mën a yar mag la.

Fii ci Afrig nag, ñu bare jàpp nañ ne, su nu weesoo jamonoy koronaawiris bi, sunu réew yi waratuñoo des ginnaaw. Am sax ñu dem ba yaakaar ne Afrig moo war a aye, jiitu ñi ci des topp ci.

Kon de mu neex ba dee ! Waaye loolu lépp, mbaa du ciy gént rekk la nar a yem ?

Dëgg la, réewi Ërob yeek yu Amerig yi, ñoom, dañoo weere. Ndaxte, koronaawiris bi da leen a futti ba ñu set wecc ! Ndekete seen alal ju bare jeek seen doole ji leen ñépp xamaloon, fii lañ tollu : feebar biy lëmbe fépp, nit ñiy dee niy weñ, loppitaan yiy màbb, jarag yi jaaxle xamuñu nu ñuy def ba faju, fajkat yi jommi  ; nit ñiy làqu ci seen i néeg… Kenn dematul, kenn dikkatul, koom-koom biy nasax di ruus… Yaafus mënul a weesu lii !

Fekk booba, Afrig mel ne Sunu Boroom daf kaa beral loxo. Ba fi nuy waxe nii, mbas mi, ñi mu ci jàpp ba di yóbbu seen i bakkan, buñ ko dee méngale ak li xew feneen, mën nanoo sànt Yàlla ! Doonte sax benn doom-aadama rekk bu wàññeku, ñàkk wu tiis lay doon saa su ne, ak fu mu mënti doon.

A LIRE  UNE RÉPUBLIQUE DE CONTREFAÇON

Ndegam kañ koronaawiris bi du ñëw génne yeneeni feem, jaxase mbir yi, dëggal yéeney ñenn ñi doon xaar Afrig nërméelu ba tàq ripp ci mbas mi ! Ndaxte, kat, jamono jii, muccagun. Senegaal gii rekk, limees na fi 2000i  way-aajowoo ceet ak lu teg ! Te yit, 25i doomi-aadama faatu nañ ci sababu koronaawiris bi. Kon, mbas mi bàyyiwul kenn, nu wax ko, waxaat ko : kuy nelaw ba yàndoor, lu la ci fekk yaa tooñ sa bopp !

Teewul sun dee seet bu baax day mel ni àddina si, gaa tukkiwul, waaye mu ngiy soppiku : boroom doole yiy jaaxle, daanu, way-ñàkk yi taxaw di fëgg dënn.

Wànte, li mat a seetaat nag, mooy xam naka la sunu réewi Afrig yiy def ba bañatee doon ndaare, dem sax ba raw ci àddina sépp. Su nu wékkulee sunu yaakaar cib luxuskat buy ñëw defal nu lu ni mel, war nanoo seet fu nuy teg sunuy tànk, xam fu nuy jaar ba bañ a desati ginnaaw. 

Yàlla-Yàlla, bey sab tool. Ndax askani Afrig yi, rawatina seen i njiit, taxawe nañu boobu taxawaay ? Ndax ñi ñu séqal mbir mi, maanaam yeneen réew yi dinañ nu seetaan nu leen di dab ba di leen raw ? Mbaa danoo yaakaar ni ñooñu dañoo ñàkk doole ba mënatuñoo xippi ? Te yit, li gënatee am solo mooy samp laaj bii : ndax tëralinu jëflante yi am ci diggante réew yi dañoo soppiku ba fàww ?

Su dee loolu lépp dara amu ci, fu nuy jaare yeneen réew yi ba romb leen, waxatumaag di leen jiitu ?

Sunu njiit yi de, ba tey jii, ci liñ nu wonagum, ñu ngiy wéy di tàllal seen loxo di ñaan ndimbal. Bare na ci ñoom ñuy sàkku ci seen i naataango yi nekk Ërob, Amerig walla Siin ñu baal leen seen i bor. Walla boog, gën caa néew, ñu far 44i milyaar yi ñu war a fey ci at mii. Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo ci gën a ràññeeku, ndax moom moo aakimoo wax ji te Macron, njiitu Farãs di ko ci jàppale bu baax. Monte de, ñoom Macron ak ñoom seen, am nañu lu leen doy sëkk.

A LIRE  MACKY SALL, ADADA

Moo tax it, waa Tugal yi  xam nañu bu baax ne, meneen pexe amul. Balaa ñépp di  labandoo fàww ñu seet nu ñuy fexe ba yombalal tuuti mbir mi waa Afrig yi, ndax ñu noyyi as tuut, ñoom it ñu am ci bànqaas bu ñuy jafandu ngir mucc. Li leen amal solo rekk moo di bàyyi xel ci buumu njaam gi, bañ mu rocciku, mbaa mu daŋ ba faf dàgg.

Waaw, ndax gor dëgg dina leb lu mu dundale njabootam,  dem duggi, togg njëlam ba noppi dellu  di balu ndax ñàkk lu mu feye ? Di ñaan ñu faral ko boram ba noppi fas yéenee demati leb fa woon ?  Ndegam jéemul a naxaate (konte ndaw woyof bopp !), xanaa kon day yeew ay loxoom ba noppi daldi  jébbal boppam ?

Ba réewi Afrig yi jëlee seen moomeel ba léegi, noonu rekk la seen digganteek réewi Tugal yi deme, daanaka. Doxalin woowule nag, feek jógu fi, bu yeboo nun askanu Afrig, nu tëddi te nelaw !

Kon réewi Afrig yi, rawatina seen i njiit, war nañoo am beneen jubluwaay bu dul di tàllal seen i loxo di saraxu, di sukkal ñi leen yeew bu dëgër, ngir sàkku seen yërmande !

Dëgg la, am na ci sunu njiit yi kenn ku ci ràññeeku lool ci jamano yii, mu di Andry Rajoelina mi fi wone taxawaayu bañkat, ak garab gi waa dëkkam, Madagaskaar, feeñal ne day faj koronaawiris bi, ci lu wér ! Ndax dëgg la am déet, doctoor yeek ñi seen xam-xam màcc ci wàlluw paj mi, dinañu ko wax. Waaye, Rajoelina moom ku mat a naw la ndax taxawaayam, ak fullaak faayda gi mu àndal yépp ngir aar askanam, réewi Afrig yi ak sax àddina sépp. Moom de, xaarul ñu wax ko nu muy def walla fu muy jaar ba génne ay ñoñam ci guta gi ñépp daanu tey. Nekkul it, ci doxalinam, di toppandoo njiiti réewi Ërob yi, ni ko ñenn ci naataangoom yiy defe, fàtte ne anam yi réew yeek xeeti àddina siy dunde dañoo wute lool, su ñu woroowul sax.

A LIRE  Interdiction de prier au sein de l’IEA Dakar: L’Institut européen des affaires franchit le rubicon (Moustapha Diakhaté)

Wolof Njaay, nag, dafa ne : benn loxo du tàccu. Jom ak faayda ji njiitu réewu Madagaskaar wone, doy nañ royukaay ñeel moroomi njiitam yi.

Nañ bàyyi yalwaan, tàkk seen fit, xeexal seen askan. Boole seen i xalaat ak seen doole, fas yéenee jammarlook nooni Afrig yi, jiital seen i njariñal réew, liggéeyal seen askan.

Suñ ko deful, na ko doomi Afrig yi defal seen bopp, seet nu ñuy lijjantee seen digganteek njiit yi leen wor. Jom mooy faj gàcce. Su gàcce gi dakkee la ëllëgu Afrig di door a leer.

Tey-si-tey, nag, wax ji lii rekk la : nu nuy def ba jële fi mbas mile. Mbas waay ! Sunu réewi Afrig yi su ñu bennoowul xàll seen yoonu bopp, gisuma leen Mbaaw !







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *