Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

BÉs Bu Mbas Mi XÉyee Ne Mes… (abdulaay Sekk)

Mbas mi jaaxal na ñépp, yëngal àddina sépp. Jàngoro jii di koronaawiris wone na boppam ci fànn gu ne : koom, wér–gi–yaram, njàng, añs. Njiiti réew yépp a jaaxle fi mu ne nii, limu néew yaa ngiy yokku bés bu ne, nguur gi xamatul nu muy def ak way-wopp yi ndax ni Covid-19 biy lawe. Ñaari weer a ngi réew miy jànkonteek feebar bi. Kon, jaadu na nu laaj lii : bés bu mbas mi xéyee ne mes, naka la Senegaal di mel ?

Noon boo mënul a gis, bu la songee fàww sa bopp ubu, sa fit rëcc.

Senegaal war naa soppi doxalinam su bëggee bokk ci réew yiy raw ëllëg. Sunu réew mii, am nay boroom xam-xam yu ràññeeku, ba tax nu xalaat ni menn réew ci àddina waru koo gën demin.

Su nu bëggee sunu Senegaal am ndam nag, war nanoo xoolaat sunuy jikko, gën a yar sunu bopp, defaraat sunu nekkin. War nanoo gën a bàyyi xel ci ni set ak set-setal amee solo, rawati-na ci dëkkuwaay yi, màrse yeek mbedd yi ; te it dakkal lépp luy dajaloo di saafonte ak a mbumbaay.

Ci wàllu koom nag, kenn warul a réere mbir ne njëgu dund gi dina yokku.

Nuy laaj tamit kañ la sunu réew miy am fitu jël ay dogali boppam, bañatee jébbal ruuwam Farãs ? Ndax ci sunu xel mu gàtt, su dee bu koronaa jeexee danoo nar a wéy di dox ci waawu Tubaab yi, di leen toppandoo, du baax ci nun. Rax-ci-dolli, ni yenn jawriñ ci réew mi, yor ay ndombo-tànk yu réy, di jalgatee alalu askan wi, day gën a gaañ baadoolo yi. Fii la Senegaal war a jaare soppiku ba fàww, seetaat digganteem ak Frãs te dakkal càcc gi.

A LIRE  AIR SÉNÉGAL SERA CE QUE LES SÉNÉGALAIS EN FERONT

Dëgg la sax, réew yépp a ngi yuuxu tey waaye ku ci nekk dangaa war a ànd ak ngor, am sa fulla, takku ba dëgër liggéey. Ku fi ne di xool li Masàmba mbaa li Madembay def, doo dem. Li war bépp doomu-réew mi mooy dëggu, jàpp fi mu jàpp, ànd ceek xolu yërmande ngir taxawu askan wi.

Yal na Yàlla musal bépp mbindeef ci mbas mi te dàqal nu ko ndax ñépp man a nekkaat ci jàmm.







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *