Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

”ngalla Bunu Jaawale Eco Ak… Eco ! ”

”ngalla Bunu Jaawale Eco Ak… Eco ! ”

Fan yii, coowal ECO baa ngi mel ni tànnbéeru dëmm, rëb ba nga ne lii lum doon. Bi Emmanuel Macron ak Alassane Ouattara defee seen yégle bi ba léegi, ku nekk a ngi àddu ci mbir mi. Jàppal ECO fii, bàyyil ECO fee. Muy taskati xibaar yi, politiseŋ yi (rawati-na kujje yi), way-moomeel yi, koomtukat yi ak yeneen xeeti gëstukat ak xeltukat yi, ñépp a ame ECO bi. Li ëpp ci xalaati nit ñi mooy ne ECO bi ak CFA bi kiif-kiif lañu, ñoo yem kepp. Waaye, kii di Séex Tiijaan Jéey, bokk ci kurélu ”Enda Cacid” jàpp na ni, méngale googu ñuy méngale ECO bi ak CFA bi njuumte lu réy a réy la. Bees sukkandikoo ciy waxam, ndege, ECO dafa am, ECO tamit am. Ci weneen waxin, dafa am ECO bu CEDEAO ak ECO bu UEMOA. Loolu lay leeral ci kàddu yii Paap Aali Jàllo bu DEFU WAXU tekki ci wolof.

Lii la Jéey wax ci nasaraan :

“Bi Alassane Ouattara ak Macron siiwale liñ naal ñeel ECO biñ wax ne mooy wuutu CFA bi ci atum 2020 ba léegi, coow li bare na lool. Mu am ay lënt-lënt yu bare yiy jur réer ak réeroo ñeel naalub ECO bi. Dara waralu ko nag, lu-dul ne ñu bare dañ réere lenn mbir : ECO bi CEDEAO di togg li ko dale atum 2000 ba tey, bokkul ak ECO bi UEMOA bëgg amal. Kon, ñoo ngi jaawale ñaari weccit yu bokkul doonte réewi UEMOA yi bokk nañ ci CEDEAO ak naalub ECO bim sumboon. Ma bëggoon cee indiy leeral yu am solo ndeem bëgg nanoo sàmm naalub bennale wecciti réewi CEDEAO yi, te muy ECO bu wér bi. Li ma ci namm mooy gindi ci askan wi ngir mu bañ a jaawale ECO bI CEDEAO sumb (te mooy bu baax bi) ak ECO bi Alassane Ouattara yégle keroog moom ak Macron te mu ñeel réewi UEMOA yi rekk (te muy biral ba tey nootaange).

A LIRE  COVID- 19 : LE TRAIN DE LA RÉSILIENCE

Bees sukkandikoo ci kàdduy Ouattara-Macron yi, xel mën naa jàpp ne waa UEMOA ñoo xaalatal seen bopp, sos ECO ngir mu wuutu CFA. Dem na ba ñu baree bare ci réew yiy làkk farañse biir Afrig sowu-jant jàpp ne kurélu UEMOA dafa aakimoo ab naal boo xam ne, gaa, bokkoon na ca ña ko laloon, waaye moomu ko. Kon, dafa aakimoo naalu jàmbur. Li ma ko tax a wax nag, mooy ne, ci biir i waxam, Alassane Ouattara tuddul benn yoon CEDEAO te xam na xéll ne ECO, ci dëgg-dëgg, moomeelu CEDEAO la.  Moom daal, ak ni mu waxe, dafa mel ni UEMOA ak Frãs ñoo toogandoo, xalaat, waxtaan ba déggoo ci ne warees na soppi CFA bi, indi ECO. Waaye, demewu fa noonu.

Li am kay, te muy dëgg, mooy ne ECO bi naalub CEDEAO la, moomeelam la, moom kepp a ci liggéey. Ndege, 1987 ba léegi ñooŋ ko doon togg, mooy jamono ja ñu taxawale naalub bennoo ñeel xaalisi kurél gi, doonte yéexoon nañ koo jëmmal. Ndaxte, ci atum 2000 lañ sumbaatoon liggéey bi. Jamono jooju, jubluwaay bee doon, ca njëlbéen, fexe ba amal ñaareelu wàlluw xaalis (zone monétaire –ECO) bu waroon a boole réewi Afrig yiy làkk farañse ak réew yiy làkk purtugees. Te, boobu, kenn waxul woon ne ECO da fiy wuutu CFA. Dañu déggoo woon ci ne ñoo fiy nekkandoo ba jëmmi jamono, ñu daldi leen boole, bennale leen ci kow ay sàrt yu leer, wér te wóor.

Ma leeral yit ne, bokk na ci màndarga yi gën a fés ci naalu CEDEAO bi, mooy ne dayob yemoo bi deesu ko yemale ci benn lim walla di ko wéer ci benn weccit kese, muy EURO walla dolaar walla weneen xeetu weccit  wu am doole.

A LIRE  ET SI NOUS DÉCOLONISIONS NOS ESPRITS, NOUS AUSSI LES BLANCS !

Li ci gën a doy waar, nag, te xamu leen ko, mooy ne Alassane Ouattara ci boppam, ci bésub 21eelu desàmbar, ci suba si, mi ngi woon ci ndajem njiiti réewi CEDEAO yi. Te, ECO bi lañ fa doon waxtaane, waaye ba tey, ECO boobu yemul ak ECO bi nu biral ci ngoon moom ak Macron. Bu dee loolu am na, li gënoon a jaadu ci wàllu politig ak koom-koom, gënoon a rafet, mooy Alassane Ouattara wax ne :

“Nun, réewi UEMOA yi, ay at a ngi nii nuy liggéeyaandoo ak yeneen réewi CEDEAO yi ngir bennal sunuy weccit, tudde ko ECO. Ndeem noo bokk benn xalaat ak benn jubluwaay te muy, ëllëg, ànd, booloo doon benn, bokk ndajem-sàrt yi nu tënk ci wàllu xaalis, nun waa UEMOA, fas nan yéene jiitu leen ci ECO bi ci atum 2020 bi, ba keroog ñi nu war a fekksi ñëw.”

Bu waxoon loolu, dina sàmmonte ak li CEDEAO lal, ak sàrt yi mu sàrtal ECO bi, rawati-na li aju ci dayob yemoo bi nga xam ne, ci wàllu CEDEAO, dañu wax ne dañu koy woyofal. Waaye, ni mu biralee keroog ECO bi, méngoowul ak li waa CEDEAO déggoo. Doonte, ba tey ciy waxam, ñaari màndargay nooteel yi CFA làmboo woon deñ nañu (teewaayu ndawi Frãs yi ci ndajem-caytu bànk yi ak xaalis bi ñuy bàyyi ci bànki Frãs yi), ba léegi ECO bi mu biral am nay laago CFA yu ko topp. Ndaxte, nee ñu Frãs mooy wóoral ECO bi te dayob yemoo bi ñeel ECO ak EURO du soppiku. Te, nag, loolu njaaxum la ; bokkul woon ci naalu CDEAO.

A LIRE  Maristes et Fissel Mbadane: deux drames caractéristiques de la crise de couple

Liy raam, nag, ci ñag bi la jëm. Li fi nar a am mooy li wolof di wax golo bey, baabun dunde. Ndekete yóo, li Frãs ak njiit yi mu ngemb di wut, mooy aakimoo naalub CEDEAO bi, naxee ko nit ñi, ba noppi wëlbati ko, dëppale ko ak ittey Frãs. Te, warees na xeex loolu. Ndaxte, kat, ECO bu CEDEAO bi, weccit wu baax la, weccit wuy tax réewi Afrig sowu-jant yi moom seen bopp, moom seen koom-koom ak seen alal, mucc ci nootaange ak toroxtaange. Kon, warunoo nangu ñaar walla ñetti njiit yu kootook Frãs di xajamal sunu cere. Te, ECO bu UEMOA bi cere la ; dafa di sax cere càq la ; bu CEDEAO bi mooy baax-baax bi, beneen bi ay naxee-mbaay kese la.

Li ma ciy ragal nag mooy askan wi dañu nar am xel mu ñaaw ci ECO bi nga xam ne CEDEAO moo ko liggéey ba di ko gam-gamle ak CFA bi, xaalisu nootaange. Moo tax may jàpp ne, njiiti CEDEAO yi war nañoo jël seeni matuwaay bala muy wees. Ndege, réccu day fekk jëf wees. Te, mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam. Ndax, moomeel, boroom da koy sàmm. Rax-ci-dolli, bi CEDEAO di liggéey ci ECO bi, du Frãs walla Amerig walla meneen réewu sowu-jant mu ci dugal xalaatam walla dërëmam. Bu nu jëmmalee ECO boobu ba réew yiy làkk àngale ci Afrig sowu-jant, Niseryaa ak Gana, bokk ci, dinanu dooleel. Su boobaa, Frãs walla meneen réewu nootaange du xalaata wëlbati xaalis bi walla di aakimoo sunu alal ci maaliforo. Nanu liggéey ngir booloo, ndax booloo rekk moo nu ci mën a génne. Ndaxte, mbooloo mooy doole.”







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *