Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

SÉex Aliyu Ndaw : « Li Ma JËle Ci Malaanum LËndËm… »

SÉex Aliyu Ndaw : « Li Ma JËle Ci Malaanum LËndËm… »

Ab téeree ngi nii boo xam ne, bii, boo koy jàng doo bëgg mu gaaw a jéex. Dafa mel ni, fàww nga def loolu wolof naan ñiimantalu. Soo dee ku yàgg a tiim téere, te xam fa bindkat di jaar, ak la muy daj, ba li muy nettali itteel képp ku ko yër, doo mën lu moy ne « Jaajëf ».

Xalaat ci naka Bóris ak ñi sóobu ci toolu xare bi ngir Afrig dellu ca jaloorey Maam. « Malaanum Lëndëm » dafa yemul ci di ab téere nettali doŋŋ. Fentkat bi dafay jaare ca la muy nettali ngir teg baaraam ci xalaat yu diis yi tegu ci loosu doom-Aadama, bi mu ne cëpp ci kow suuf ba tey. Ndax, mu wax kook mu bañ koo wax, am na ñaari laaj yu doom-Aadama di laaj boppam fu mu tollu. Ñu di :

•    Fan ? Fan la nu jóge ?

•    Ak Fu nu ? Fan la nu jëm ?

Ndax kat, danoo xippi rekk gis sunu bopp ci kow suuf ; soo dee ab liir, xamoo tus. Sooy màgg as lëf, jóge fa, toog. Jéem a raam. Xool nit ñi la wër. Jéem def ni ñoom. Jóge raam, taxaw. Dégg i baat, nga toppandoo. Mujje xam la baat ya tekki. Lii lépp teewul, ba ba ngay ràññee, mënoo tontu ñaari laaj yi. Fan ? Ak Fu nu ? Tandale du tax doom-Aadama am ci lu leer. Nit ñi gëm diine te ñi aju ci Lislaam gën cee dogu, nooy dégg fi AJI SAX JI di waxe ci Alxuraan : « ci Man ngeen  jóge te ci Man ngeen di dellusi». Teewul doom-Aadamay wéy di dunde njàqare ngir li mu xamalul boppam dara. Kumpa gi ëmb lépp moo waral bindkat bi joxoñ li mu tudde Malaanum lëndëm. Bóris jaaraale na ci ngir taxaw ci bennoo bi waa Afrig war a bennoo ba mën a jekku Noon Bi. Moo tax ba doomu Senegaal ak bu Niseeryaa mën a mel ni ñaari séex. Ku nekk ci ñoom soo demee ca sa réewum xarit dangay gis ni lu baree niroo ci nekkin ak demin ci ñaari réew yi. Doonte aada yi mën nañoo mel ni yu wuute, teewul jikko yu yées yi fii ñooy ya yées fee. Naka la nit mën a soxore yenn soxor yi ? Naka la nit mën a teg yenn metit yi nit ni moom ? Lu tax ba nit doyadi yenn doyadi yi ? Nan la nit deme ba teg bànneex ba gën a am solo, loo xam ne lii su ko seetlu woon, gis ne mook bàyyimaa ko bokk ? Te ndaxam de ndeysaan lii lépp du mujje fenn fu dul pëndëx wàlla sax dóomu-taal naaw ci jàww ji. Kon ana lu ko fi jar ? Bindkat bi dàqaale na ci ganaar, waxaale li mu xalaat ci jigéen ñu ñuul ñiy « tubaabal » seen jëmm. Ndaxam de taar ajuwul ci melow der. Jongoma pël ba ca Dalaba fu mu teer ñépp yéemu. Waaye ndawas séeréer ba ñuulaay bay nes-nesi ba weer wi sax wàcc di ca seetu, xam na boppam. Cër, nekkin ak demin ñooy lal taar. Melow der day jaadu mu méngook kiiraayu réew ga nga fekk baax mbaa nga donne ko ca say Maam. Bindkat bi dafa bëgg rekk ñu bañ a jaawaatle. Fa pëndëxu sedd di taw guddi ak bëccëg, der ba ñuuloon day xolleeku, kawar ya baramu woon dañuy gudd ngir mën la aar ca sedd ba. Lii ku ko xam doo sonn.

A LIRE  A NOS MARTYRS DE PASTEF LES PATRIOTES, MORTS POUR QUE RENAISSE UN SÉNÉGAL NOUVEAU

As tuut a ngi, noonu daal, muy li ma jële ci Malaanum Lëndëm. Téere bu am solo, ëmb njariñ te teg tànk ci yoonu goreel Afrig ba fàww.

Séex Aliyu Ndaw

Ndakaaru

Septàmbar 2022

Malaanum lëndëm, Bubakar Bóris Jóob, 230 xët,

EJO-EDITIONS, Ndakaaru 2022







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *