Senexalaat - Opinions, Idées et Débats des Sénégalais
Opinions, Idées et Débats des Sénégalais

JÀng Ak JÀngale Ci Jamonoy Mbas

JÀng Ak JÀngale Ci Jamonoy Mbas

Céy Koronaa ! Doomu-jàngoro bii yëngal na jamono.

Ku mënoon a gëm lu ndawe nii dina noot àddina sépp ? Tax na ba kenn ñemeetul a génn mbaa doxi soxlaam.  Moom daal, koronaa tëj nanu nun ñépp ci sunuy kër, tëj nu ci tiit ak njàqare. Ku nekk naan kañ lay jeex, rawati-na sunuy doom. Ñoom la koronaawiris njëkk a dëj, tere leen jàngi, ndax li jawriñi réew mi tëj lekool yi.

Xale yi gëmewuñu ko woon. Lu tol ni lekool di tëj ci diggu at mi, du muur mburaake la. Ñu kontaan, naan ndax Yàlla nu nopalu. Waaye diir bu gàtt moo ci tegu, ñu tàmbalee laaj seen i way-jur kañ lañuy dellu lekool. Li am moo di ne dañoo dem ba namm seen i xarit, bëgg a fo ak ñoom mbaa xéy rekk gàddu seen saak, sàkkuji xam-xam, jàng lu bees. Rax-ci-dolli, tey, fi mbas mi tollu, kenn xamul ndax lekool dina ubbiwaat ren am déet.

Moo waral nuy laaj tey : ndax lekoolu Senegaal dina mucc ci tawat bii di koronaawiris ? Ndax du ko jekkali faf ?

Njàngum lekool, ni ñu ko xame, ñaar a ko séq, kiy jàng ak kiy jàngale. Jàngalekat bi mooy aji-xam-xam bi, di ubbi xeli ndongo yi, ñuy topp ci waawam, lu mu leen tere ñu ba ko.

Su ko defee, fàww nu laaj lii : naka la njàng mi mënee àntu ci jamonoy mbas, jamono joo xam ne gone yi duñu janook ki leen di jàngal ?  

Réew mu mel ni Finlande jot naa indi tontu ci laaj boobu. Foofu, xale yi, lu tol ci 4 ba 5i waxtu doŋŋ lañuy toog lekool bés bu ne. Daanaka xale yi sax ñooy jàngal seen bopp, ndax porfesoor bi day am beneen taxawaay, gindi ak jubbanti mooy liggéeyam. Du jàpp ni moom doŋŋ moo xam ci daara ji, day bàyyi xale yi ñuy jéemal seen bopp, xalaatal seen bopp, saa yu ñu juumee mu xettali leen. Kon, ndongo yi dootuñu ay siwo yu ñuy sotti xam-xam, dañuy yittewoo seen njàng, di wutal seen bopp xam-xam, duñu xaar sëriñ bu leen di sa. Rax-ci-dolli, dañuy mën a jëfandikoo anternet bi, loolu bokk ci liy woyofal liggéeyu jàngalekat yi, rawati-na ci jamonoy mbas mu mel ni koronaa, di tere nit ñi di dajaloo.

A LIRE  Hommage à Sadio Camara alias Alphonse, commandant du maquis Pai/Sénégal en 1965

Ndax jotul nag Senegaal def ni réew yooyu, seetaat njàng meek njàngale mi ?

Moonte dey, réew mi tëral na ay sàrt, ci atum 1991, di ci leeral wareefi jàngalekat bi te muy lii  «Jàppale bépp ndaw ci yoonu sàkku xam-xam, ngir naatal xelam, mu doon ku mën a ràññee ak a jariñ askan wi.»

Waaye tey-si-tey, bu nu saytoo bu baax, day mel ni képp kuy jàngi lekool, dañu lay jël rekk, dëj la ci biir lekool, di sottiy kàddu ci sa bopp, doo xam sax lu ñuy jariñ. Neexul ba neexul waaye dafa mel ni jàngalekat yi jéematuñoo ubbi xeli ndongo yi, lenn rekk lañu leen di laaj te mooy ñu tari lépp lu ñu leen sa.

Su njàng mi tëddee noonu, mbaa xale yi dinañ màgg, doon ëllëg ay kàngam yuy amal njariñ askan wi ? Ndax mëneesul a xàll weneen yoon, yoon wuy tax xale yi mën a ràññeel seen bopp buñ demee ba gisatuñu ki leen di jàngal ? Loolu, jumtukaay yu bees yi mel ni antarnet rekk ñoo ñu ci mën a dimbali. Kon lekool bees war a tabax ngir tegu ci yoonu yokkute foofu la war a jaar.

Nan fexe ba du doon ay gént doŋŋ. Mbas mi ubbi na sunuy bët, joxoñ nanu yoonu coppite wiy jëmale kanam sunu réew. Sun ci jaaree, sunuy sët ak i sëtaat duñunu jéppi ëllëg !







Laissez un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *